Ami Mbeng
Ndengeleer
Askan way yeewoo ca Ndengeleer amal nañu ab ndaje di xamal waa nguur gi ne : ñaari fan lañu leen may ngir ñu indi ay saafara ñeel coowal suuf si, lu ko moy ñoom dinañ nangu seeni tool bay leen ca na mu gën a gaawe.
Aa li Nguy Njaay
Gannaw coowal suuf si dox ci diggante askanu Ndengeleer ak njiitu « Sedima » Baabakar Ngom, nguur gi jël na ñetti dogal. Bi ci jiitu mooy ne baykat yi dinañ mën a bayi seeni tool ba njeexitalu nawet bi. Ñaareel bi nee na Baabakar Ngom mu dakkal bépp liggéey bum sóoboon foofu ca tool ya. Dogal bu mujj bi mooy ne dinañ amal ab waxtaan su nawet bi jeexee ngir saafara mbir mi.
Widéwo bi lëmbe dëkk bi
Ndaw su ñu jiiñ càcc ca Saakre-këer la ay ndaw doon filme ak a toroxal ba cër yi di feeñ, film baa ngi lëmbe dëkk bi, ñépp di ko ñaawlu. Naka noonu la Maam Maxtaar Géy ak Séydi Gasama di xamle ne dinañ topp ñi doon filme ngir xam ñan la, def li ci war.
Mali
Way-jubóole Afrig sowu jant yaa ngiy laaj ñu taxawal nguurug bennoo.
Misra
Dipite Misra yi nee nañu bu soldaari nguurug Tripoli gi Tirki faral dakkalul seenug dox jëm ci penku réew mi, dinañ ànd ci yabalug soldaar ca Libi.
Mali
Ngir jiital kaaraange nit ñi ñeel xare bi lëmbe diiwaanu Sayel bi, lu tollu ci 20i kuréli Afrig ñoo booloo sos mbootaayu maxejji Sayel (coalition citoyenne pour le Sahel) ci bésub 16eel sulet 2020 ngir samp ab naal. Li ñu ci jublu mooy wut meneen pexe ginnaaw bi làrme yi lajjee ci caytug kaaraange diiwaan bi.
Saakre-këer
Ci xibaar yu mujj yi, ñoo ngi nuy yëgal ne yoon teg na loxo ndaw yi doon filme teg ci di toroxal xale bu jigéen bi ñu doon jiiñ càcc.