PORFESOOR MUSAA SÉYDI : «BÀYYI WIRIS BI LAW, MUSIBA LA NU NAROON A JURAL»

 

Bàyyi wirisu Covid-19 bi law ngir sabab kiiraayu-mbooloo la Doktoor Paap Musaa Coor digle ngir xeex mbas mi. Waaye PorfesoorMusaa Séydi mi jiite Banqaasu feebar yiy wàlle ca loppitaanu Faan, àndul ak xalaat boobule. Lii la Porfesoor Séydi wax :

« Naam, way-tawat yaa ngiy yokku. Kenn werantewu ko. Waaye, bu dul woon dogal yiñ jël, romboon nan fii bu yàgg. Loolooy wone ne, fagaroo gën faju. Mu am, nag, ñu jàpp ne danoo waroon a bàyyi wiris bi mu law, dal ñu bari ci askan wi ndax ñu mën a am kiiraayu-mbooloo. Waaye, wiris boo xam ne mën na lawàll benn, ñaar, ñett ba fukki yoon sax, sun ko bàyyi woon mu law musiba mu réy la nu naroona jural. Ñi ci ñàkk kon seen bakkan kenn du xam nu mu tollu. Duma tàyyee wax ne fagaru rekk moo nu mën a may ndam ci Covid-19 bii lëmbe àddina si.»

Ci ndaje mu jawriñu wér-gi-yaram ji doon amal ak taskati xibaar yi la Porfesoor Séydi indee leeral yile.

1 COMMENT

  1. Maa ngi rafet lu , taxa waay ak liggéey bu séll Bim àndal , ngir jëmale làkk Wi kanam,
    Te Loo lu moo nuy may ñuy def di Dindi,
    Fexe ba wàcce xam-xam yi ci suñu làkk Wi
    Jàngal ci ndaw ñi tàggat ci mag ñi,

    Buñ ko defee , fii ak At , yu néew
    Dina ñu xam lii Bokku Na ci Li ñu
    Teewoon a dem…

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here