YOW KORONAA (Mamadu Jara Juuf)

TAALIFU MAMADU JARA JUUF

Nee nga  layy, ni dott

Ñów di nas, di nocci

Nërmeel  nga  boroom  doole

Detteel  nga  boroom  alal

Botti nga  boroom  xam-xam

Yow Koronaa, yaay  fas di fecci !

Kenn ràññeetul  kenn

Kenn xàmmeetul  kenn

Fatt  nga  gët  yi

Muur  xar-kanam  yi

Tëj  wunti  kër  yi

Yow Koronaa, yaay  teg di teggi !

Yaa ñu  yeew ci kër  yi

Ñuy  xool  njaboot  gi

Yaa not sunuy  làmmiñ

Yaa tënk  sunuy  jéego

Kenn dematul  fenn

Yow Koronaa, yaay  tapp di teppi !

Ub  nga  jàkka  yi, yow Koronaa

Tëj  nga  jàngu  yi, cey  Koronaa

Dakkal  nga po mi

Feelu  kilifa  yi

Wallu  ustaas  yi

Cey  Koronaa, yaay  buur di bummi !

Yéem  nga  Beydaani

Tiiñ  nga  Soodaani

Mbas  nga  kàccoor  yi

Gal-gal ndaanaan  yi

Caxabal saay-saay  yi

Cey  Koronaa, yaay  fal di folli !

Tee ñoo durus say dars

Ndax  sunuy  jikko  aaru

Sunuy Kàddu woddu

Sunu   mag ñi  fegu

Sunu  ndaw  yi  sàmmu

Cey  Koronaa, yaay  tabb di tebbi !

Moo  Koronaa,

Yow miy  lal di làlli

Tee ñoo  càqi say cax

Sunu nguur  yi  maandu

Sunum pénc doxe fi jag !

MAMADU JARA JUUF

Mbaaw, weeru Mee 2020

Avatar
guest

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here