ËTTUB TAALIF

‘’Ëttub taalif’’ mooy xët wu bees wi defuwaxu.com jagleel ladabu réew mi. Sunu xarit, sunu doomu-ndey Mataar Caam Faal, moo yor wile xët. Képp ku bind taalif te bëgg nu génne ko, mën nga ko koO yónnee ci  

Tey, Sëriñ Daawuda Njaay Jaraaf ak Sëriñ Daam Jaane mu Tuubaa lanuy àndal.

 

I

GÀDDAAY

Sëriñ Daawuda Njaay Jaraaf jàngalekatub wolof la. Def na gëstu bu am solo ci tëralin ak ci doxalinu njàngalem kàllaamay Kocc ci daaray tuut-tànk yi ci réew mi.

Gàddaay rekk dëkke gàddaay                    

Gàddaay ba nekk fu amul daay                  

Gàddaay ba man a sori gàdd gi                    

Gàddaay ba man a daw kàdd gi                    

Gàddaay kàdd ga ñuy siyaare                      

Gàddaay gedd la ñuy tasaare                        

Gàddaay baaxoo wërum réew                      

Gàddaay rekk bañ ku la yeew                        

Gàddaay ba far tàbbi ci dun                          

Gàddaay ba far tebbi lu duun                        

Gàddaay ba fa ñi la xañub dund                    

Gàddaay dund fa sa giiru-dund                      

Gàddaay defar sa gentu baay                          

Gàddaay dëggal sa géntu yaay                      

Gàddaay rekk dëkke gàddaay                        

Gàddaay ba nekk fu amul daay                

DAAWUDA NJAAY JARAAF

 

 

II

GUDDI (Xaaj bu jëkk)

Sëriñ Daam Jaane mi ngi juddoo Tëngéej ci atum 1986. Daara la yor ca Tuubaa, di jàngale Alxuraan. Mi ngiy taalif way yu bari jëm ci xew-xewi jamano jii nuy dund.

Mbalaani niir yi bu muuree jant, sàng safax

Bëccëg ga tàggu timis, maay samp dënd di buur

Xaftaan bu ñuul ni këriñ, am tupp-tupp yu weex

Mooy col ga, ag ndaama laa, as ndiir su gàtt ma réer

Xaftaan bu ñuul la ma sol, am tupp-tupp yu weex

Ag ndaama laa, fukki waxtu ak benn rekk ma réer

Gaaw lool ci way-bég-i-xol, soof cam su nekkee ci tiis

Dal, yewwu, am sutura, xam lépp bàyyi ci biir

Way-baax ya sopp ma, saay-saay sa jàppe ma waay

Ñeey jaamu, ñee dëkke jëf ñaawtéef ya, lépp ma muur

Saag door la jinne di jóg, lal ay pexeem, tër i fiir

Ku farluwul tëye doomam, njuuma sànni ko xeer

Ngelaw lu sedd la moo lay soññ, gaawtul xoyet

Jafal sa and ci mattug gongo, gëtt gu piir

Ginaar yi tàbbi ngunu, njugub yi génne ci lëm

Lippaaxon ay gunge jeeg, bay waaj a yakkiji reer

Muus jóg di rëbbi jinax, xérjéjji lang ci looy

Gee jàll yóbb safaa, wittar nu tàbbi ci biir

DAAM JAANE

Avatar
guest

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here