Taalifi Nday Sayba Faal ak Saydu Ba

Saydu BA waa Ñooro la, di al-pulaar bu gàlle. Ndaanaan luy yëngu ci teyaatar la, tëgg ak um pecc. Tukki na ci réewi nasaraan yu bari, di fa teeweji ay ndajey fecckat ak i tëggkat. Ba Saydu tàmbalee bind ay taalif ak léegi, am na lu ëpp ñaar-fukki at.

FAJAR

Fajar

Xérem ni selaw

Dëkk bi ni sendew di nelaw

Ci biir mbalaanu sutura

Fajar

Suuf sedd guyy

Kenn doxul

Dara yënguwul

Nelaw falu di buur

Fajar

Weer wi mel ni kuy làqi taaram

Ci poroxndollu niir yi

Biddeew ya suux

Asamaan set wecc

Fajar

Njanaaw yiy sab ba mel ni ñuy sàbbaal Yàlla

Njugub ya gàddaay

Ak yeneen xeet yu ni mel

Ci la jàkka yiy nodd

Fajar

Baatu As-salaatu Xayril minna nawmi

Di xotti tareet asamaan si ba textexaan

Ngëmug gaa ña Yàlla baaxe

Ci wéetal seen Boroom

Fajar

s bi tàmbalee ràbb

Ay cëwrinu fenkub jant

Ci pëllug leerug ceeñeer gu jëkk

Fajar

Asamaan si tàmbalee set wecc

Ànd ak ngelaw lu ndaw te féex

Ñu folli nelaw tey teeru léemaayi suba yi

Soxna Ndey Xayba FAAL mi ngi dëkk Ndakaaru, doon jàng xam-xamu melosuuf ca Daara ju mag ju Seex Anta Jόob. Bind na taalif yu bari ci fànn yu wuute, niki mbëggeel ak jafe-jafey àddina, ngëm ak diine, sàkku xam-xam ak coono yi ci aju.

NIT DAY MAANDU

Ku dee ak bàmmeelam

Lu waay def it boppam

Mbindeef ak ug mbonam 

Soo ciy yàbbi daldi ko yées

Man Faal damaa jaayante

Dëddu wax ak i werante

Seexlu it fàww weerante

Cib murid dafa yées

Sang sama dénkoon na ma

Murid bu jógul ca waxi nit ña

Du dox mukk ca yoon wa

Di dox di taxaw rekk a yées

Ku ne na nekk ca la mu gëm

Te ñun ñiy yóotu fàww ngërëm

Ñu gëmm tëx te bañ a gëlëm

Bëgg Sëñ Bàmba mooy maye xol bu bees

Xol buy dund fàww al-jànna

Ruuh guy xeeñtu mbir ya

Mucc asal fi ker ya

Di dox di féexlu rekk a yées

Murid bu mënta maandu

Na dellu fàww jébbalu

Di tuub tey saxoo yeeslu

Ndax tudd mbonug nit rekk a yées

Ey waay fu nit di mucce

Di xéy di góorgóorlook a xare

Ba daan jéll sa ndam saraxe

Li rekk ay ndof li yées

Ku dee ak bàmmeelam

Lu waay jëf it boppam

Buur beek i mbindeefam

Di ko lijjanti mooy bopp bu ñàkk a fees

Dammal say bët ca la lewul

Damm saw làmmiñ ca la daganul

Yoonu Sëñ Bàmba lu ca askanewul

Jarul di wax ba sa màggal di rees

Bu ñuy wax it deel noppi

Góor-mag kepp a soppi

Ay doxalin tey rooti

Ca ña duy leer ba fees

Avatar
guest

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here