DOGALUB GÓRNÓORU NDAKAARU ÑEEL DEM BEEK DIKK BI (AMI MBENG)

Górnóoru Ndakaaru jël nab dogal di ci teree daw bépp oto bu yab màrsandiis ba mu weesu 3,5i ton. Ngir leeral, Alasaan Sàll ne, oto yooyii, waruñoo daw diggante 6i waxtu ci suba jàpp 10i waxtu ak diggante 16i waxtu jàpp 20i waxtu. Waaye tere bii, tali yii toftalu rekk la ñeel : 1eelu tali bu mag bi, « boulevard du centenaire », tali bi jóge Jamñaajo jëm Ndakaaru.

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here