WEYI TAN (SAYDU BA)

Saydu BA waa Ñooro la, di al-pulaar bu gàlle. Ndaanaan luy yëngu ci teyaatar la, tëgg ak um pecc. Tukki na ci réewi nasaraan yu bari, di fa teeweji ay ndajey fecckat ak i tëggkat. Ba Saydu tàmbalee bind ay taalif ak léegi, am na lu ëpp ñaar-fukki at.

 WEYI TAN

 

Yaw mile dangaa xiif

Boo dee lekk, mukk doo suur

Lu la romb nga daldi siif

Sa koll gu rëy doo tàggook xiif

Saa su nu nekkee ci jàmm

Toog ba sunum xel dal

Nga dëkkee kàcc ak sàcc

Di déqi toolu askan wi

Weñ yi di la biiw

Tan yi di la yéew

Cogg gi dar la di la woy ak a jay

Ngay jayaxu ndax alal ji nga luubal

Bu nit ñi di daw ngir sàkku leer

Yaa ngay màmm ci biir lëndëm

Sos sa mbootaay di diisoo

Ay pexe yoo moome suuf si

Moomuloo li nga bokk ak say nawle

Nga dëkke néewal kàttan

Dooley askan wi la suuxat

Ci biir lawtanu sukuraat

Boo nu ŋàccee ba nu jeex tàkk

Siddi nu ba nu wow koŋŋ

Booba fekk na li ci sa koll

Saw yàppu yaram moo ca fees

Avatar
guest

LEAVE A REPLY

Please enter your comment!
Please enter your name here