Laaj ak tontu bii nag, seen yéenekaayub web defuwaxu.com séqoon na kook Usmaan Sonko ci weer yii weesu. Xaaj bu njëkk bii nu siiwaloon ko ci 18i fan ci suweŋ 2020. Lu tollook weer a ngi nii coowal Usmaan Sonko lëmbe réew mépp ak sax bitim-réew. Looloo waral ci sunu limat bu bees bii nu génnewaat waxtaan wii ngir fàttali jaar-jaar ak gis-gisu kii di Usmaan Sonko, di njiital Pastef “les patriotes”, te ñu bari naan leegi moom mooy njiitu kujje politig gi.
*