Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar.
Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju.
(Ci taataanug Uséynu Béey)
“Mbokk yi, tey, walla mën naa wax sax ne, fan yii yépp sunu xol neexul, sunuy nelaw néew na, sunu xalaat bari na, te dara waralu ko nag, lu dul tiis wi nga xam ne am na ci réew mi, muy ay bakkan yoo xam ne rot nañ fi.
Kon, dama doon ñaan bala nuy dugg ci waxtaan wi rekk nu daldi def “une minute de silence” jagleel ko sunuy doom, ndax ñi fi faatu ñépp, walla ñiñ fi faat ñépp, nun li nuy doon ndaw ndaw, mat nañuy doom. Tey, jox nan ma lim boo xam ni jeexagul; waaye lim bi nu jotagum mat na fukki nit. Benn bakkan bu rot rekk, ci anam bu mel nii, nga xam ne dañ koo faat, musiba la ci réew mi, rawatina nag, bu ñu nee tey mat nañ fukki nit.
Bakkan yooyu nag, ñooy :
-
ku ñuy wax Baay Séex Jóob, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Yëmbël ;
-
Séex Kóli amoon ñaar fukki at, ñuŋ ko faate ci Biññoona ;
-
Faamara Gujaabi, moom it amoon ñaar fukki at, ñu faat ko Biññoona ;
-
Paap Siidi Mbay, amoon moom it ñaar fukki at, ñu faat ko fii ci Kër-Masaar ;
-
Saajo Kamara am fukki at ak juróom-ñett, ñuŋ ko faate Jawobbe ;
-
Mañsuur Caam, moom it am ñaar-fukki at, ñuŋ ko faate fii ci Ndakaaru;
-
Alasaan Bari, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Sànteneer, ci Ndakaaru ;
-
Musaa Daraame, amoon fanweeri at ak juróom, ñoŋ ko faate ca Ndóofaan ;
-
Buraama Saane, amoon fukki at ak ñaar, ñuŋ ko faate Biññoona ;
-
ak Móodu Njaay, nga xam ne moom lañ nu mujje xabaare, ñu faate ko tey fii ci Parsel-Aseni, ci anam yu ñaaw ba fu ñaawaay yem.