Kub bu Mboolem-Kuréli futbal yu Afrig yi (CAF) 2022-2023 « Ñàkk teewu Jaraaf doon na luy nëbb futbalu Senegaal ci kembarug Afrig… »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Seppi nañ Jaraaf ci Kubub CAF bi. Loolu la FSF (kurélu futbal gu Senegaal) siiwal. Ci yëgleem bi mu génne, jàpp nañ ci ni wayndarey ikibu jaraaf bi yóbbuwuñ leen CAF ci waxtu wiñ leen ko laaje. Muy dogal bu doy waar, rawatina ci jamono jii mbootaayu futbal yu Senegaal amee ay jafe-jafe am ndam mbaa sore ci joŋante diggante-mbootaay yi (compétitions inter-clubs) ci Afrig.

Senegaal du am ku ko teewal ci joŋante Kub CAF yu 2022-2023 yi. Loolu mooy xibaar bi ñu jële keroog ca ndajem lótëri mi CAF doon amal, ginnaaw bi ñu seetloo ni turam génnul benn yoon. Muy lu bette. Ndax li ñu nangu woon ci làmmiñu njiital kurélu futbal bu Senegal, Ogisteŋ Seŋoor, mooy Jaraaf moo fay teewal Senegaal : 

« Yónnee nañ bataaxal ikib yiñ war a yëgal yépp : Casa Sport, Étoile de Lusitana ak Jaraaf. Laaj nañ ku ci nekk ndax bëgg naa bokk. Casa Sport ak Jaraaf rekk ñoo tontu. Lusitana tontuwul. … Moo tax ba tànn nanu Jaraaf mu dem teewe Kub bu Afrig ». 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj