ABDURAHMAAN JUUF MA NGA CA JÀNGUNE YA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ba ñu leen takkalee seen i ndomboy-tànk, jëwriñi Càmm gu bees gi sóobu nañu ci liggéey bi leen di xaar. Kenn ku nekk yaa nga ca wàll wa ñu la dénk ngir amal i diisoo. Naka noonu, Abdurahmaan Juuf mi nekk jëwriñu njàng mu kawe mi ak gëstu gi, mu ngi door ay tukkiy-nemmeeku ci jànguney réew mi.

Fa jànguneb Séex Anta Jóob bu ndakaaru (UCAD) la nekkoon barki-démb ci altine ji. Mu amal ay diiso ak kilifa ya fa fare ak ay kurél ya leen taxawu. C lee jukkee ci seen waxtaan woowu, moom jëwriñ ji rafetlu na ko lool. Mu doon ay xalaat, yenn ci ay jafe-jafe waaye it xalaati saafara ngir gën a ñoŋal.

Ginnaaw seen ndaje moomu, la gën a fés ci ay kàddoom, bokk na ca àppug njàng mi. Mu doon diir biy ndongo yi di door seen um njàng ak ba ñuy tëj. Loolu nekk lu ko yitteel lool. Ndax, ci ay waxam saytu nañu jafe-jafe ya muy mën a indi ci wàllu koom gi. Mu koy firndeel ci ay gëstu yu ñu def, di ci wone ni bu ñu sàmmoonte ak diiru àpp njàng mi, dina leen yéwénalal lu tollu ci 25i ci ay tamñaret ci xaalisu réew mi.

Leneen lees ci mën a jàngate ci sàmmoonte ak àpp googu, mooy su dee yéwénal seen ug gafaka, dina yéwénal tamit at yu bari ya fay ndongo yay def. Loolu di am njeexintal ci seen um njàng, di ko yéexal. Mu dolli ca nekkiinu ndongo ya ci biir béréb boobu. Moo xam seen ug lekk wala seen ug dëkkuwaay.

Mënees na wax ne, balaa ngaa saafara mbir fàww nga xam jafe-jafe ya. Mel na ne ci wax jooju la jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi tënku. Tax ba mu doore fa UCAD ngir ay saytu. Jafe-jafe yi jànguney Senegaal yiy dund, rawatina bu Séex Anta Jóob yitteel na askan wi lool ndax ay weer ñoo ngi nii njàng ma tagatembe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj