“ÀND GËSËM” A NGI GËSËM  

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yee nu jàll la waa “Ànd Gësëm” génne woon ab yégle di ci xamle ne dañuy amal ay gereew ci seen fukkeelu tëralinu-jëf. Noonu lañ ko defe, gereew nañ diirub 4i fan li ko dale talaata 4 jàpp ajjuma 10i fan ci weeru féewarye ci 2023 bi. Yemuñu foofu, nag. Ndaxte, dañu ci dolliwaat yeneen ñetti fan ci diggante àllarba 15 jàpp ajjuma 17i fan ci biir weeru féewarye win nekk.

Ci seen fukkeelu tëralinu-jëf bi, waa “Ànd Gësëm” a ngi ciy dànkaafu ak a sikk ñenn ci kilifay fajkat yi dul nangoo bokk ci seen gereew yi te dara taxul lu dul nekk ay « sàcc, baadoola ak i wund. Xaalis bi ñu leen di compal a tax ñu bëgg a xajamal xeex bi nga xam ne, jubal ak yoonal payug ñépp ñiy liggéey ci kurélu wér-gi-yaram ak ndimbalu nit ñee ko tax a jóg. » Laaj nañ ci yit « 104i miliyoŋ yi ñu nu joxoon ca koronaa ba, ak 20i miliyaar yi Càmm gi delloo ci wàlluw naalu “couverture maladie universelle”… »   

Ci talaata jii weesu, 14i fan ci féewarye, la waa “Ànd Gësëm” génnaatoon di naqarlu tabbug Abiibu Njaay mi nekkoon ab “médecin-spécialiste” ci wàllum pajum mbooloo (santé publique), laata mu doon “conseiller technique” ci kurélu wér-gi-yaram ak ndimbalu nit ñi. Abiibu Njaay, léegi, mooy tof-njiit bu mag bu kurél gi, wuutu ci kii di Alasaan Mbeng. Ci seen biir yégle bi, ñoom waa “Ànd Gësëm” jàpp nañ ne « Alasaan Mbeng amal na liggéey bu mucc ayib, jaaral na lépp ci yoon ak ci teggin. » Li leen naqari yépp, bokk na ci li ñiy jël fajkat yi doŋŋ di leen tabb ay “directeurs généraux”, “conseiller technique”, añs… te ñu waroon ko jagleel ñi jàng, am xam-xam ci wàlluw caytuug réewl. Looloo tax ñu ne :

« Du Abiibu Njaay moo yelloo tabb gi, ndax ni kurél gi ame ay fajkat, noonu la ame ay “administrateur civil” yi seen liggéey yemul ak fajkat yi. Bañ na ko sax ba njiitu réew mi dafa taxawaloon, ginnaaw “direction générale bu santé publique”, beneen “direction générale” ci wàlluw ndimbalu nit ñi (action sociale), bu ci nekk di mottali moroomam. Kon ab “administrateur civil” a yellool palaasu “secrétaire général” bi, nde mbir mi dafa mel ni gëddu “secrétaire général” lees bëgg a soppi def ko ay yëfi paj kese moone du loolu mooy cëram. » 

Ci seen gis-gis, mbir yi dafa bëgg ëpp i loxo. Nde, « dafa dem sax ba ñiy liggéey ci biir kurél gi te duñuy fajkat gisatuñ seen bopp ci liggéey bi, ndax bi Mari Xemes Ngom Njaay jiitee kurél gi ba léegi, dara jaaratul yoon. Li mu bëgg kay moom, mooy  fajkat yi kese aakimoo bépp xeetu liggéey bu ëmb kurélu wér-gi-yaram ak ndimbalu nit ñi. » Waa Ànd Gësëm a ngiy dolli di waxaat ne lenn rekk a leen tax a jóg te mooy « jubal, teg liggéeykat yépp ci yoon, ku ci nekk liggéey bi mu mën te yelloo ko, ñu bàyyee ko ko. Su ko defee kurélu wér-gi-yaram ak ndimbalu nit ñi mën a suqaliku, gën a jëm kanam. »

Lii la waa Ànd Gësëm di ŋàññee jëwriñu wér-gi-yaram ak ndimbalu nit ñi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj