BUBAKAR BÓRIS JÓOB ÑAAWLU NA KÀDDUY TAYIIRU SAAR YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii weesu, Tayiiru Saar, njiitul làng gii di Parti nationaliste, dafa fésaloon i kàddu ñeel doxandéem yiy dund fi réew mi. Ba mu waxee ba noppi nag, coow lu réy a ci toppoon. Ndax, ñu baree jàpp ne kàddoom yi dañuy ndirook boddekonte walla ag xeetal. Moo tax, kurél yu bari dañu dal ci kowam, di wax ne kàddoom yi dañu safaanoo ak teraanga biy màndargaal réew mi, rawatina mbokkoo ak bennoo gi dox diggante Saa-Afrig yi. 

Bindkat bu mag bii di Bubakar Bóris Jóob tamit àddu na ci. Dafa bind, wax ne :

“Kàdduy boddi doxandéem yi Tayiiru Saar yékkati dafa woroo ak niteef te day salfaañe cëslaayi mbokkoo gi dox diggante Saa-Afrig yi. Te yit, dafa nar a indil fitna miliyoŋi Saa-Senegaal yiy dund ci réewi mbokk yi. Te sax, ñooñii ñoo war a njëkk a sàkku ci moom mu noppi.”

Tayiiru Saar nag, génne woon na ab yégle di ci weddi tuuma yiñ koy gàll. Nee na, dañ koy waxloo li mu waxul. 

Li mat a leeral nag mooy ne, du ñépp ñoo xalab ngóor si Saar. Ndaxte, am na ñu bokk ak moom gis-gis, rawatina Móodu-Móodu yeek Faatu-Faatu yiy dund bitim-réew.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj