CÀMM GU BEES GI : WAAW, ANA JIGÉEN ÑI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ba mu jële lenge yi, njiitu réew lu bees li Basiiru Jomaay Jaxaar Fay taxawal na góornamaŋam bu njëkk. Muy jëf ju mu def ca saa sa, daldi fal ilimaanu jëwriñ ju njëkk, di Usmaan Sonko. Kookit, niki ni ñu ko baaxoo gis ci pólitig, samp na nit ñi ko war a gunge ci boobu liggéey. Mu doon Càmm gu ñu yamale ci 5i fara-caytu ak 25i jëwriñ. 

Mu nekk lim bu wuute ak bi ñu daan a faral di gis ci Càmmug Senegaal. Nde, lim bi daan na ëpp loolu. Ñu doon ay góor niki ay jigéen, ñépp di ay Saa-Senegaal ñu fare ci biir réew mi wala ca bitim-réew. Waaye, li jaaxal lenn ci askan wi mooyl limub jigéen ñi ci Nguur gi. Dafa, am na ñu jàpp ne 4i jigéen rekk dafa tuuti.

Bi ñu dawalee turi jëwriñ yi war a sóobu ci liggéey bi, ñeenti jigéen kepp lañu ciy gis. Muy Yaasin Faal (jëwriñu bennoog Afrig ak mbiri bitim-réew), Faatu Juuf (jëwriñu napp gi, tabaxtey géej geek waax yi), Maymuuna Jéey (jëwriñu njaboot gi ak dimbalante yi) ak Xadi Jéen Gay ( jëwriñu ndaw ñi, tàggat-yaram ak mbatiit). Mu doon lim bu ñenn ñi jàppe lu néew ci Càmm gu ni tollu. Muy kàddu yu Ndéy Astu Njaay di jàngalekat bu mag ca UCAD dëggal. Mu gis ne coppite gi Càmm googu di woote waroon na ko firndeel ci jigéen ñi. Nde, am nañu jigéen ñu xareñ, sawar yu mën a taxawe googu coppite. 

Keneen ku àddu ci lim bu néew boobu di Maymuuna Nduur Fay, dib saabalkat. La mu gis mooy gàcce dëggantaan la jàppe loolu. Nde, am nañu jigéen yu xareñ yu mën a njiite sax réew mi. Bu ñu sukkandikoo ciy waxam, Njiitu réew la woon, di Maki Sàll def na ci liggéey bu mag ci wone xareñteefu jigéen ñi. La muy dénk Càmm gu bees gi mooy ñu góor-góorlu ci wàll woowu. 

Njiitu kurél gii di Amnesty International/Senegal, di Séydi Gasama, tebbiwul wax ji. Muy lim bu néew bi ñu fal jigéen ñi. La mu ca gis ci saafara mooy dogal bii di yamale góor ak jigéen ci réew mi lañu war a soppi te yaatal ko. Bu ko defee, fépp fu ñuy falee, moo xam ca Ngomblaan ga wala fu mu mën a doon góor ak jigéen yam fa kepp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj