Ngelaw lu bees la réewum Senegaal noyyiwaat tembe ci campug Njiitu réew lu bees lii di Basiiru Jomay Jaxaar Fay. Mu nekk juróomeelu Njiitu réewum Senegaal, ginnaaw ba Senegaal moome boppam ak tey. Niki tey, talaata 2i pani awril 2024, la ko Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi samp, jëmmal ko ci boppu réew mi. Mu nekk bés bu réy, bés bu mag ñeel askanuw lëmm.
TALAATAY YEN
Yenees na Basiiru Jomaay Jaxaar Fay aw sas wu réy bés niki tey. Muy sasu njiit li war a boot askanuw Senegaal ci 5i at yees dégmal. Fa CICAD la ko àttekati Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi (NDSR) doon sampee, mu waat ci seen kanam, ñoom ñi teewal askanu Senegaal, ak ci teewaayu Njiiti réew ak kilifa yu bare. Njiitul NDSR mi fàttali na ko warteef yi ko Yoon gàll ak yaakaar ji ndaw ñi am ci moom ba fal ko. Fàttaleet na ko kenoy réew mi ak bànqaas yi mu war a sàmm. Bi mu waatee ba noppi, ci lañu ko ràng raaya réew mi, takkal ko caq bi. Lépp di wone dayob Njiitu réew fi Senegaal.
BÉSUB TÉEN
Biñ ko sampee ba takkal ko caq bi, Basiiru Jomaay Fay wax na. Ginnaaw ba mu nuyoo ay ganam niki ay naataangoom yi teewe woon bés bi, dalal leen, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, sant na ñépp. Waaye tam, fàttewut a njukkal Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi, ndax ci seen i ndogal lees amalee ay wote yu jaar yoon. Sant na njabootam ak i mbokkam, gërëm askanu Senegaal wi ko wóolu, tànn ko ngir mu jiite réew mi. Waaye, fàttewut li askan wi jot a dund ci ay mettit, muy lu koy gunge ci xelam ba du leen mas a rusloo. Xelam tam faayul ci mag ñi tabax réew mi ba mu agsi fii tey. Ci ay jikkoy péexte, yoon ak jokkute. Muy ndono lu réy lu ñu bàyyee Senegaal.
Ginnaaw ci loolu, fas na yéene liggéey ci kéem-kàttanam ngir sàmm réew mi ci jàmm ak mbooloo, doon benn. Fàttewut ne koomu Senegaal mi gën a réy mooy dal gi fi nekk. Yokk na ci tam ne, dina boole Saa-Senegaal yépp, ak fu ñu mën a nekk. Bennoo la woote ngir ëllëg gu naat. La mu gën a sànjaafu mooy dina xirtal askan wi ci liggéey ngir lu ko jëmale kanam ak ug koom-koom. Laal na tund Afrig ci lu koy xaar ci péexte ak yokkute. Waaye, lalu ci wetu ay naataangoom ngir Afrig gu doon benn, tijji bépp bunt ngir ay jëflante yu jaar yoon te tegu ci bëgg-bëggu askan wi. Dina dooleel yoon ci mu moom boppam ak demookarasi réew mi.
Jamono yii wees, Senegaal a ngi doon ter-teri ci ay yëngu-yëngu. Waaye, askan wee taxaw temm, joyyanti réew mi ak seen i baat. Loolu day firndeel ni, Senegaal, réewum demookaraasi bi ñu koy bàkkee, dëgg la.