Démb ci talaata ji lees amal ñetteeli joŋantey kippug C gi ak gu D gi. Nii lañu demee :
Kippug C : Senegaal matal na ñettam, Kamerun rëcc na.
Démb bi 17i waxtu jotee la joŋantey kippug C gi tàmbali, mu nekkoon Gine Konaakiri – Senegaal ak Gàmbi – Kamerun. Senegaal mu ngi wéyal ay ndamam. Dafa gañe dëkkandoom bii di Gine Konakiri 2-0, gën a rafetal génnam ak toogaayam ca boppu kippu ga. Ñetti joŋanteem yépp la gañe, muy lu réy. Ci seen xaaj bu njëkk bi, gaynde yi xawoon nañu am tuuti jafe-jafe. Nde, ndawi Kaba Jaawara yi dañu tàmbali rekk, yéeg seen kaw. Ndax, xamoon nañ ne buñ mayee Senegaal dawal bal bi rekk, du baax ci ñoom. Waaye, ba ñu delsee ci ñaareelu xaaj bi, gaynde yi daldi fippu, nangu bal bi doxal. Ci 61eelu simili bi, ci benn teg-dóor (coup franc) bu jege kãwu Gine bi, Kerepeŋ Jaata daldi koy xellil Abdulaay Sekk, Cekkeen bi mbëkk bal bi ak doole, lakk caax yi. Ba ñu demee ba ci 90eel ba Ilimaan Njaay, goneg Màrsey gi, dolli beneen ci paasu Saajo Maane, muy 2-0. Noonu la joŋante biy jeexee.
Ci ñaareelu joŋante bi, Kamerun dafa dóor Gàmbi 3-2. Waaye de, yombul woon ci ñoom. Gayndey Kamerun yi xawoon nañu cof buntu toog. Ba seen joŋante bi dawee ba ñu mitã ba dikkaat, doxal ba ci 56eelu simili bi la Tokoo Ekàmbi taal caaxi Gàmbi yi. Ñu dawal lu yàggul, Gàmbi fayu ci 72eel bi. Ñu ni déet-a-waay, Gàmbi daldi dugalaat ci 85eelu simili bi. Foofu nag, daanaka Gàmbi kalifiye woon na. Waaye, dañu dugal seen kã (87eelu simili), muy lu doy-waar. Mu nekk 2-2. Saa-Kamerun gëm ko rekk ba ca 91eelu simili ba, joŋante bay waaj a jeex, Kiristofëer Wóo tojati kër ga, muy 3-2. Kamerun kalifiye, Gàmbi toog.
Seen kippu gi, Senegaal moo jël pée ak 9i poñ, toppu ci kamerun 4i poñ, Gine ñëwee ñetteel ak 4i poñ itam, kamerun jiitu ko ndax “carton rouge” bu mu amoon ca seen njëlbeenu joŋante ba. Gàmbi jël ndaare ak 0 poñ.
Kippug D : Móritani def na ko Alséri, Àngolaa nax na Burkinaa Faaso.
Ci gii kippu, lu kenn foogul woon, mbaa ñi ëpp, moo ci am. Móritani moo dóor Alseri mi jëloon CAN 2019 daldi koy toogloo. Mu bett daanaka ñu bari. Moom, Móritani, kalifiye na ci 1/8 dë finaal yi. Guléet muy am ndam ci CAN. Waayeet, guléet muy jàll ci ñaareelu sumb bi. Benn bii moo am ci joŋante bi, Muhammed Delaahi Yaali moo ko dugal ca 37eelu simili ba. Turam duggu na ca mboorum kuppe mu Móritani.
Àngolaa tamit dafa nax Burkinaa Faaso, dóor ko ñaari bal ci dara. Mabululu moo dugal bii bu njëkk bi ci 36eelu simili bi, Sini dolli ko ci 92eel bi.
Moom Àngolaa moo jël pée ak 7i poñ, toppu ci Burkinaa Faaso ak 4i poñ, Móritani jël 3eel ak 3i poñ. Alseri mooy ndaare bi am 2i poñ.
NAALU ÀLLARBAY TEY JI : KiPPUG E AK GU F
Afrig dii Sidd dina daje ak Tunisi bu 17i waxtu jotee, ca beneen joŋante ba Namibi di ci dajeek Mali. Muy yu kippug E yi. Joŋante yaa ngiy daw jamono jii.
Kippug F gi nag, bu 20i waxtu jotee lañuy futbal. Ci benn boor bi, Sàmbi dina ko ñàkkanteek Marog ; ci beneen bi, Tansani ak Kóngo Demokaratig dianñ laale.