CORED ÀRTU NA BASIIR FOFANA MU ITV

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kàddu ya BacNsiir Fofana yékkati woon fa Itv mujj naa jur coow. Ndax, kàddu yooya, daf koo jëmale woon ci kii di Saŋ Batist Tin ginnaaw bi ñu ko tabbee jëwriñu biir réew mi. Moom nag, yemalewul mbir mi ci jëwriñ ji kese. Daf caa laaxaale diiney kercen ju nga xam ne fa la bokk. Looloo waral coow lu bari sosoo ci. Ba tax sax, ay kurél yu bari àddu ci. Ñu gën cee ràññee ñii di waa CORED nga xam ne, ñooy saytu liggéey taskati xibaar yi.

Àjjuma, juróomi fan ci weeru awril 2024 la elimaanu jëwriñ yi génnee limub jëwriñ yi mu nar a àndal ci liggéey bi. Ba turi gaa ñooñu rotee, ca la coow la door. Ñee jàpp ne lépp baax na. Ñeneen gis ne mbir yi des na. Ndax, am na ñoo xam ne dañoo jàpp ne limub jigéen ñi dafa néew. Waaye, kii di Basiir Fofana moom, dafa toj kaas yi.

Ca jotaayu Iftar biy am ci tele Itv la yékkatiy kàddu ci Saŋ Batist Tinmi ñu dénk njëwriñu biir réew mi. Daf ne :

 “Ma seetlu menn mbir…. Saŋ Batist Tin miy jëwriñu biir réew mi. Te, mooy yor wàlluw diine ji. Nun, am réew lan moo xam ne 95% yi ay jullit lañu. Nu am koo xam ne ci diine kercen la bokk, xalaatal gàmmu jot Seneraal Tin dem walla màggal Tuubaa jot Seneraal Tin dem.

Kàddu yooyu nag mel na ne Saa-Senegaal yi naanewuñu ko am ndox, rawatina ñi mu jam ci wàllu ngëm. Moo tax, kurél yu bari jóg di ko àrtu. Muy gu ci mel ni CORED (Conseil pour l’Observation des Règles d’Ethique et de Déontologie dans les médias). Nee nañu, ñi ngi naqarlu kàddu yooyu mu teg ci deru jëwriñ jooju. Rax-ci-dolli, muy fàttali ñiy yëngu ci kibaaraan yi càrt yi leen tënk. Ndax, xeeti kàddu yii bokkul ci loo xam ne mën naa jur ag jàmmoo ci diggante ñi fare ci diine yi nekk ci réew mi.

Waaye, bi mbir yi dooree ba tàmbalee ëpp i loxo, ca la ndeyi-mbill ji, Basiir Fofana, génn na, def ab widewoo di jéggalu. Xamal na askan wi ne, nangu na ne dafa juum. Te, mi ngi ciy tuub bu baax. Naka noonu, kippaangog Emedia gi tamit, nga xam ne ñoo jàllale mbir mi, ñi ngi sàkku ci askan woowu mu jéggal ko. Ndax, lu dul jàmm lu ne rekk, jàmm a ko gën.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj