“COUP D’ÉTAT” CA NISEER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dañ ko doon laam-laamee démb, waaye leer na tey. Këppatal nañ Nguurug Bazoum gi. Sóobare yi ñoo ko daaneel, foqati Nguur gi ciy loxoy. 1960 ba léegi, bii moo 5eelu yoon ñuy daaneel Nguur fa Niseer. Muy mbetteel lu réy nag. Nde, bi Isufu bàyyi Nguur gi, bañ a sàkku 3eelu moome, foogoon nañ ne demokaraasi moo fay wéy di sax. Ndekete, booba, am ñuy nas ci suuf ngir siif Nguur gi.

Booy seet ba ci biir, lii xew Niseer warul a doon mbetteel. Ndax, bi Bazoum faloo, laata sax muy waat, lañ ko jéemoon a daaneel. Moo tax, bi mu toogee, tabboon nay njiit yu bees ci boppu làrme bi ak sàndarmëri. Dafa mel ni ku xamoon li koy yoot, muy jéem a fagaru. Waaye de, muccu ci. Ba tey, xameesagul lay bi sóobare yiy layal seen jëf ji.

Ginnaaw Mali, Gine Konaakiri ak Burkinaa Faaso, Niseer mooy ñeenteelu réewum Afrig sowu jant mu ñu daaneel Nguuram.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj