SAFIYETU BÉEY
Juróom-ñetti xarnu ci ginnaaw, amoon na fi buurub Almaañ bu ñuy wax Ferederik 2. Daa déggoon làkk yu bari, demoon na ba
mokkal 9i làkk ci lim, waaye lateŋ ak gerek la ci gënoon a sopp.
Bés, mu yeewu ak mébét mu kéemaane. Dafa woolu keroog ay nitam, ni leen moom daal daa bëgg xam wan làkk la Buur Yàlla
di làkk. Ngir leeral mbir moomu nag, mu ni nañu dajale ay liir yu tooy xepp, nangu leen ci seen i way-jur, dénk leen ay jigéen. Li mu leen santoon mooy ñu toppatoo gone yi, ni ko seen yaay daan defe, di leen sang ak a laab, di leen jox ñu lekk ak a naan, ne leen nag bu ñu ŋaaŋ benn yoon di wax ak ñoom, te tamit buñu leen won benn cofeel. Ñépp waaru, laaj Buur lu waral loolu. Mu ne leen ci gis-gisam, noonu rekk la mën a xame ban kàllaama la xale yiy tànnal seen bopp su ñu tàmbalee wax.
Fan la mbir mi mujje ?
Xale yépp a faatu. Waaw, li leen Ferederik xañ mbëggeelu way-jur, yërmande, ak bépp xeetu yëg-yëg moo leen a taxoon
a génn àddina laata ñuy mën a wax.
Am na ñu naan ay léeb doŋŋ la. Amaana, amul ni ñu ko nettalee, waaye ay boroom xam-xam yu fekk baax Amerig te seen xel màcc lool ci lépp lu jëm ci mbirum xale, ñoo seetlu ni yërmandeek cofeelu way-jur amee solo ci doom. Jot nañoo firndeel ni xale yi ñuy faral di dóor ak a metital ci seen ndawñooy màgg doon i tàng xol, bañ seen bopp, di sippi seen mer ci seen i njegeñaale. Léeg-léeg tamit ñuy am ay feebari xel, dem bay bëgg xaru. Boroom xam-xam yooyu yokk nañu ci ni jikko yi
ni mel mën nañoo topp nit ki ba ba muy am 40i at.
Ndax nu ngi bàyyi xel ci loolu, nun waa Senegaal ? Sunu réew mii de, booy seet léeg-léeg, danga naan dañ fee farataal dóor xale. Ñi fi am baat ñépp, ko laaj mu ne la, gone, dees koo war a
teg ci yoon. Naka ? Bu dégluwul waxi way-juram, bu jàngul bu baax ca lekoolam, bu defee naka su dul noonu, ñu mbej ko, xët
ko, mbaa ñamal ko ci leraw gi ba yaram wiy nàcc. Way-jur yu bare jàpp nañu ni loolu yépp ci yar xale bi la bokk. Waaye ndax bëgg yar googu war naa tax ñuy metital gone ? Dog xolam ? Tëj xelam ? Waaye dóor, dóoraate, saaga ak metital yemul ci ndaw yi ndax bés bu ne ñu dégg ci xibaar yi ne am na ku ñu rey Caaroy, walla Tuubaa, walla feneen ci réew mi. Dafa mel ni tëral nit, rëndi, dootul dara ci nun. Ci sama gis-gis bu gàtt, ñàkkul nun ci
sunu bopp nu màggaaleek jikko yu bon yooyu, nar koo wàll sunuy doom. Su ko defee, ñuy dem ba jàpp ne képp ku leen
merloo, jaadu na ñu saaga la, duma la, walla sax rey la ndax ni ko Wolof di waxe : « xale lu mu nàmp lay tàqamtiku ».
Dëgg la, « bant su tooyee yomb a jubbanti» waaye kuy jubbanti sa bant ba faf ko damm, yow yaay ñàkk sa bant. Doom
nawle la, loo ko lebal ba muy tuut-tànk, bu màggee fey la ko.
Rax-ci-dolli, gone, ak lu mu ndaw ndaw, dina xam, dina ràññee te it dina seetlu mag ñi mu nekkal, teel a xam man mag la bëgg a nekk ëllëg. Nun tamit, loolu war naa noo leer : ndax danoo bëgg nekk i mag yuy xoqtal ak a fitnaal sunuy doom, walla ay mag yu leen di taxawu, di leen xelal, di leen xàllal yoonu gëm seen bopp ?
Warees na cee bàyyi xel…