Démb ci gaawu gi, 21 oktoobar 2023, saa-senegaal yaa nga woon fa Place de la nation. Ñu dajaloo fa ngir amal ab jotaayu ñaxtu ñeel dund bu jafe bi lëmbe réew mi jamono yii.
Doonoon na luñ gëj a gis lool. Ay nit yu dajaloo fenn ci réew mi, rawatina fa Ndakaaru ngir ñaxtu li leen naqadi ci dëkk bi, mbaa lu leen tere dund dund gu dal ak seen teeyu bakkan. Démb ci gaawu gi lañ ko gisaat. Donte barewuñ woon lool, nde perefe bi dafa ko yéex a nangu ci àjjuma ji, Saa-Senegaal yaa nga woon ca mbeddi Ndakaaru ya doon ñaxtu.
Muy nag ñaxtu bu mbootaatu way-jëfandiku yeek kuréli maxejj yi woote woon fa Place de la nation. Dara waralul woon nag seen woote boobu lu dul dund bu metti bi. Ñu dellu mën koo dégg ci kàddu yees fa jibal, di ko wax ak a waxaat : « Mbëj mi seer na ! », « Luyaas bi seer na ! », « Dund bi metti na ! », « Kilo soble ñaari téeméer ak ñeent-fukk lay jar léegi ! », añs.
Bees jëlee misaal ci mbëj mi, seeraay bi jéggi na dayo ba mujje lëmbe réew mi. Jotaayu waxtaan yi, wax-sa-xalaat yi ba ci mbaali jokkoo yi, doo ci yër benn te ŋawti-ŋawteewuñ ko. Jot na fi jur sax ab pétition bob, Ummi Nduur (taskatu xibaar), a ko jiite won ci ayu-bés yii weesu. Bu fa yemoon sax mu tane. Waaye, lakk-kati mburu yee yokkati xar mi karaw. Yokkuteg mbëj mi lañuy taafantoo ngir yokk njëgu mburu mi. Ci ayu-bés bii nu génn lañ biral seen nisër boobu..
Naka noonu, mbooloo ma doon ñaxtu gaaral na Càmm gi jafe-jafe yi ñuy dund jamono yii ak di ko fàttali ndogal yi mu fi jëloon te jëfewu ci dara.
« Dañuy jël ay ndogal te buñ fa jógee duñ saytu doxalin wi. Ca atum 2014, amoon na ndogal luñ fi wote woon ci luyaas bi. Daanaka, boroom-kër yi wàññi woon yépp dañ mujje génne luyekat yi ngir yokkaat payoor gi. Bu ko defee dañuy dellusi jëlaat ndogal ya woon te duñ ci topp di saytu. » (Mustafaa Seen, mbootaay miy xeex yokkute njëg yi).
Ginnaaw bi perefe ubbiwaatee yoonu mbedd mi, nuy xaar ba xam saa-senegaal yi dinañ fi génn ak doole walla Càmm gi du fi xaar loolu ngir sàkk i pexe.