Ñi ñu tëj ci kaso yi, xiifal gi lañ jël def ko ngànnaayu xeex. Ginnaaw bi jigéeni Kàmpenaal yi tollee ci juróom-ñeenti fani xiifal, ña ca kasob Sigicoor ba feelu nañ leen.
Ci ayu-bés bii ñu génn, bésu altine 9 oktoobar 2023, la jigéen ñi ñu tëj ci kasoy Kàmpenaal yi tàmbali woon xiifal. Juróom-benn ci ñoom, di ñu yoon tegoon loxo ndax seen i yëngu-yënguy pólitig, ñoo ko dooroon.
Ginnaaw gi la ci ñett dolleeku ba yóbbu lim bi ci juróom-ñeent. Li leen ci xiiroon di naqarlu téeyandi bu yàgg bi ñu leen téeye foofu. Ba tax ñu doon sàkku ñu génne leen foofu ni mu gën a gaawe ci lu amul ben war-warloo. Boobaak léegi nag, taxul wenn yoon ñu am li ñu bëgg.
Lu ni mel sax moo yékkati ay kurél yuy yëngatu ci àq ak yelleefi doom-aadama ba ñu génne ab yëgle démb ci altine ji. Ñu cay ñaawlu tanqamlu bi kilifa yi def jigéen ñooñii ak di sàkku ci Càmm gi mu jël i matukaay ngir sàmm seen kaaraange, seen wér-gi-yaram ak seen i àq ak yelleef.
Fii mu nekk, li bees ci mbir mi mooy ni limub ñi dugg ci xiifal gi dafa gën a taqarnaase. Nde ci diggante démb ak tey, 182i doom-aadama (muy góor, di jigéen) yu ñu tëj fa Sigicoor, sóobu nañu ci. Kurél gii di FRAPP-France Dégage ñoo ko xamle ci seen xëtu Facebook. 150 ñoo ko tàmbali démb, tey 30 dolleeku ci.
Foofa ca Sigicoor nag, nekkin wu metti moo ci dugal mbooloo mii yépp. Nde, ba tey ci li FRAPP leeral, dañoo sonn, tàyyi ci liñ leen di dunduloo. Moo tax ñu fippu jaarale ko ci xiifal gi.
Bokk na ci yi ñu lim, lekk gu bon gi ñu leen di jox ñu koy dunde ak njëg gu seer gi ñu leen di jaaye woote telefon bi, boole ci téeyandi bu yàgg bi laata ñu leen di àtte. Lii sax tax na ba ñuy sàkku ci Càmm gi mu tabb fa nu mu gënee gaaw beneen àttekat bu wuutu ki nekkoon ci pekk bu njëkk bi. Bi ñu ko toxalee ba léegi, ñaareelu pekk bi kott mooy dox.