LI CI BIIR "XELUM XALAM" BU LÀMP FAAL KALA (EJO-Editions)

Yeneen i xët

Aji bind ji

KAN MOOY LÀMP FAAL KALA ?

Làmp Faal Kala, am ñu ko gën a xame ci turu Ngoti Faal (Ngoty Fall), doomu Luga la ju gane àddina ci atum 1984. Moo ngi jànge ca iniwérsite bu Ndar. Foofu la ame ca atum 2009 lijaasay “Master” ci Làkk, Mbind ak Mboor ñeel Afrig, ca departmaa Àngale. Boobaak léegi muy wéyal ay gëstoom ci fànn woowu ba doon ku ci am aw tur. Jaar na itam ci atum 2011 ca Fastef, di daara ja ñuy tàggate jàngalekat yi ba am fa lijaasay CAES ji ko def ab jàngalekatu Àngale. Mu ngi dale Alquraan ca Gànnaar. Waaye kenn mënul a tudd Làmp te tuddoo Sëriñ Mustafaa Faati Kala, mi ko yar ca Luga, tàggat ko ci wàllu diine, def ci moom jikko yu rafet.

Moom Làmp Faal Kala, li waral mu jox yitte làmmiñu wolof bokk na ci anam yi mu màgge, ndax bu dee ci wàllu néegu ndayam, ay maamam dañu koo teel a xemmemloo làmmiñu Wolof ci woy ak a waxtaane mbindum mag ñu mel ni Seex Sàmba Jaara Mbay ak Seex Musaa Ka. Làmp moo ngi bokk itam ci wàllu baayam ci askanu Lebar, di ñu Yàlla may xam-xam ci wàllu mboor, cosaan ak aaday Wolof. Ay waajuram xirtal ko lool itam ci fonk tey sàmm ak topp baaxi Maamam.

Yooyu yépp daje ci moom tax mu teel a bëgg cig ngoneem di fentantu ay taalif ci fànn wu ne, di tëgg di leen riim. Xelum Xalam nag, téereb woy la bu ëmb i gis-gis ak i yëg-yëg, di soññeek a àrtu ci anam yu rafet, dëggu, neex a dégg.

LI CI BIIR “XELUM XALAM”

Làmp Faal Kala du mag waaye li taalifam yi biral moo di ne ku xam àddina la, am seeetlu ba tax koo bind ci téereem bii ne Di dund ak ku soxor doy na nattu/Da lay xoqtal di xeex ba nga fattu/Soo dëgërul sa xol bi jeex nga faatu/Te su ñu la tàggee nag ñoo fay jiitu. Mënees na cee yokk ne kenn walla dara feesul i bëtam. Li mu yëg rekk a ko amal solo, muy bind ngir lal waxtaan ak doom-aadama yépp, di jéem a dab seen bànneex. Firnde bi ci jëkk mooy turu téereb taalif bii EJO génne tey : “Xelum Xalam”. Woy yi ci biir dinañ féexal xol, ubbi xel, yaatal gis-gis. Waaye yemul foofu ndax day wone yit ne li koy tax a bind mooy fexee dooleel sunuw askan, ñaax nu ci ànd doon benn, di xàccandoo di dóorandoo. Moo tax Làmp Faal Kala ne : Nanu fexee juboo/Ànd bañ di xiiroo/Ngalla bunu di ŋaayoo/Fàttee joow sunu gaal.

Ndax lii dawul yaram ?

Lu nekk a ngi ci biir “Xelum Xalam” waaye li ci gën a fés moo di ne ki fent woy yii taalibe Baay-Faal bu mag la, di ko ndamoo saa su ne. Nan ko dégloondoo : Nu jóg te sax ci ndigal/Liggéey pastéefu jëf jël/Bunu séytaane dugal/ba far xañ nu jinaan.

EJO-Editions Dakar

NJËG LI : 5000cfa

Mën ngeen a woote ci limat yii :

Ndey Koddu Faal 00221 77 651 68 48 (whatsapp) / 33 827 15 15

Musaa Aysatu Jóob 00 221 77 479 77 73 (whatsapp) / 76 532 08 89

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj