Ni ñu ko xame ci jamono jii, lawax yi tàmbali nañoo dagaan baatu askan wi. Moo tax ba waa Benno Bokk Yakaar ak seen njiit lii di Aamadu Ba, ña nga woon ca bëj-gànnaaru réew ma. Aamadu Ba ma nga woon fa Podoor, tundu Aysata Taal Sàll ak Raasin Si. Podoor mësul a gis lu ni mel ci am mbooloo. Moo tax it « Podoor nee nañu waaw » mu nekk kàdduy Raasin Si mi doon dalal seen lawax boobu.
Aamadu Ba, kàdduy cant la doore ñeel ay naataangoom. Bokk na ca la mu dige, fas na yéene génne Podoor cig làqoom googu, tabaxug kumpekaay, añs.
Am njooxe moo dalal Aamadu Ba fa Aayre-Laaw, nekke ci diwaanu Podoor. Mbooloo mu takkoo wàcc ca mbedd ya. Ña nga yore ay pànkart, sol seen i tiset di yuuxu turu Aamadu Ba. Ma nga feggoo ak Muntagaa Si ma koy wonele ak askan wa. Ñu gis tamit ca wetam Abdulaay Daawda Jàllo. Ña nga door seen i kàdduy nuyo ci pulaar waxaale seen bëgg-bëgg ci wote yi ñu dëgmal.
DÉCCE FAAL A NGA JAWBE
Decce Faal a nga woon ca diiwaanu Jawbe mi bokk ci tundu Koldaa. Lawax bi jot na faa wone ay mbébétam bés bu yore réew mi. La mu gis, mooy fas na yéene ñoŋal paj ma ci ay naal yu yaatu ngir ne ñépp a war a am ag yemoo ci wàll woowu. Mu am yéene jëmmal ko ci tabaxug taax yu mag. Waaye, fàttewut ne Jawbe ku ko xam, xam ko ci ja bu yaatu. Mo tax ba mu am mbébét yokk koom-koom ga. Bu ko defee, mu laal mbey ma, càmm ga ba askan wa nekk ca gox ya yëg ci seen bopp.
SIGICOOR A NGAY XAAR GAN
Ginnaaw ba mu fa gëjee ay weeri weer, waa Sigicoor dalal nañ seen doom ji, di meeru diiwaan ba, Usmaan Sonko. Ndakaaru la bawoo, ànd ak Basiiru Jomaay Fay, lawaxu lëkkatoo “Diomaye Président”, wutali dëkkam ba mu jiite. Ñoom ñaa ñépp, barki-démb lañ génn kaso “Cap-Manuel” biñ leen jàppoon. Mbooloo mu réy a réy a leen teeru fi ñu jaar yépp.