LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (11/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJÉBBALUG LENGE FA MÀKKAANI NJËWRIÑ YA

Keroog ci àjjuma ji la elimaanu jëwriñ ji génne limub yeneen jëwriñ yi. Ñenn ci ñoom jébbal nañu leen lenge yi. Ña ca des nag, ñépp tey ci alxames ji lañu leen jox kiliteefi njëwriñ yi ñu leeen dénk. Kii di Aysata Taal Sàll, nekkoon jëwriñ ji ñu dénk Yoon, jox na lenge yi Usmaan Jaañ, jëwriñ ji ko fay wuutu. 

Kii di Abdu Rahmaan Saar, jëwriñ ji ñu dénk koom gi jot na kilifteefu njëwriñ ga. Musaa Bàlla Fofana tamit jël na lenge ya ca loxoy Abdulaay Séydu Sow. Naka noonu, yeneen jëwriñ ya tamit, muy Yaasin Faal, Mabuuba Jaañ, Alliyun Badara Jonn, Musatafaa Giraasi, Yànkooba Jémme, Muntagaa Jaawo, Seneraal Biram Jóob, Allaaji Abdu Rahmaan Juuf, añs. jébbal nañu leen lenge ya. Kon nag, nooflaay moom jeex na. Liggéey ba door na.

BUUBAKAR BÓRIS JÓOB ÀRTU NA TAHIIRU SAAR

Coow li Tahiiru Saar sosoon ñeel nekkiinu doxandéem yi ci réew mi jeexagul ba tey jii. Ndax, bindkat bii di Buubakar Bóris Jóob àddu na ci mbir moomu. Kàddoom yooyu mi ngi leen birale ci xëtu Faacebookam. Xamal na ko ne kàdduy boddikonte xeet yooyu dafa jële ñépp kow. Te, loolu day nasaxal cofeel gi am ci diggante Saa-Afrig yi. Rax-ci-dolli, loolu day tax nekkiinu miliyoŋi doomi Senegaal yi nga xam ne ñi ngi ci réew yii ñu jegeel di gën a tar. Moo tax, ñooñu ñoo waroon a njëkk a sàkku ci moom mu noppi.

WAA LIPS ÀDDU NAÑ CI COOWAL SUUKARU KOOR LI

Démb ci àllarba ji la réewi jullit yu bari doon màggal bésub korite gi ba ci Senegaal gii. Laata bés boobu, coowal suukaru koor dafa lëmbe woon dëkk bi lool. Li ko waraloon nag du lenn lu moy imaam bi doon dal ci kow Nguur gu yees gi. Ndax, nee na joxuñu leen suukaru koor na ko ñi fi jóge daan defee. Waa LIPS (Ligue des Imams et Prédicateurs du Sénégal) génne nañu ab yégle ngir naqarlu loolu. Te, nee nañu duñu bàyyi mukk lu mel noonu jàll. Ndax, nee nañu kurél gi ñu doon, loolu warul a nekk seen taxawaay. 

WAA HAC TERE NAÑU MBIRUM PÓLITIG FA MALI

HAC (Haute Autorité de la Communication) mooy kurél gi ñu dénk mbooleem li war a jàll ci këri tasuwaayu xibaar yi (Rajo, tele, añs.) fa Mali. Génnee nañu ab yégle tey ci alxames ji ngir fésal ci matuwaay yi ñu jël ci wàlluw kibaaraan yi. Nee nañu ñi ngi woo mbooleem kibaaraan yi ñu dakkal jàllaleg lépp lu laale ci mbiri pólitig. Muy làngi pólitig yi ak gépp kurél walla mbootaay guy dox ci mbiri  pólitig. 

Ginnaaw bi Mali jëlee ndogal loolu, waa ONU àrtu nañu leen. Bànqaas gii di “Haut Commissariat de l’ONU aux droits de l’homme” àddu nañu ci fa saa sa. Mi ngi jaarey kàddoom yooyu ci mbaali jokkoo yi. Mi ngi sàkku ci ñoom ñu fànq dekkere boobu. Te, ñu bàyyi gaa ñi wéyal fa mbiri pólitig ya.

AY SÓOBARE FAATU NAÑU FA NISEER

Tey ci alxames ji la làrmeb Niseer ba biral xibaar boobu. Xamle nañu ne rey nañu lu tollu ci juróom-benn ci seen i sóobare. Ñi ngi faatoo ci benn sox bu ñu leen dóor fa Inaat ca wetu Mali. Yokk nañu ci ne ñoom it jàpp nañu ci lum néew-néew fukki rëtalkat. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj