LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (16/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SAYTUKAT YI CI GOX YEEK GOX-GOXAAT YI BANK NAÑ SEEN I LOXO

Sàndikaa bi ëmb liggéeykati caytu gi ci gox yeek gox-goxaat yi bankloo na ay way-bokkam seen i loxo ci àppug 120i waxtu. Li ko dale démb ci altine ji 15 awril ba keroog àjjuma 19 awril 2024, dinañu dakkal liggéey bi ci réew mépp. Li ñu bëgg nag mooy kilifa yu bees yi sàmmontek seen àq ak yelleef. Ñu leen di xamal ni ñaari at ci ren, ñoo ngi sàkku ñu yamale leen ak way-saytukat yi, yokk seen iy peyoor ak ndàmpaay yi leen Càmm gi warlul. Ñuy xaar nag ci kilifa yu bees yi ñu gaaw jóg ci seen i mbir ndeem yoon ak yamale bi ñuy sàkku lañu doon woote ba ñu fal leen.

KÀDDUY MUSTAFAA JÓOB YI ÑEEL RTS

Taskatu xibaar bii Mustafaa Jóob, di liggéeye fa màkkaanu Walf, ñaawlu na doxaliin wi RTS di wéyal ginnaaw bi Njiit yu bees yi toogee. Bees delloo ci gis-gisam, RTS mi ngi ci tànk yi mu nekkoon ba taxoon ñépp doon ko ŋàññ, te mooy jël tele réew mi askanalee ko waa Nguur gi. Ba tax muy artu ni bees moytuwul RTS bi fi nekkoon Rajo Telewisiyoŋ Sàll dina mujje doon Rajo telewisiyoŋ Sonko walla Jomaay. Ndaxte, li fa Njiitu réew mi ak magum jëwriñ yi feeñ raw na xaat lim biñ fa feeñ ci diggante bi ñu sàmpee seen làngu pólitig ca 2014 ba bi ñuy jot ci Nguur gi, donte ni sax ñoom Njiit yu bees yi jëlaguñ lennu ndogal ci tele bi.

MBIRI JÀLL-WAAXU NDAWI BUUR (PAASPOOR DIPOLOMATIG) YI

Képp ku ñu tekki sa ndomb-tànk, sa paaspoor dipolomatig dafay dog ca saa sa. Dootuloo ci mën a tukki. Ndogal la lu kilifay Càmm gu bees gi jël. Xibaar bee ngi tukkee ci Aji Mbergaan Kanute, di dépite fa ngombalaan ga, fare ci waa Bennoo Bokk Yaakaar. Bees sukkandikoo ci xibaar bi mu siiwal, kilifa yu bees yi jotale nañ ndogal lol, jépp jëwriñ ju xas ba joxe lenge yees la dénkoon dootul a mën a jëfandikoo paaspoor dipolomatigam ndax li ni mel dafa taqook ndomb-tànk gi. Moom ci boppam da cee am bés, ñu nangu bosam. Moo ngi ci jotaat ginnaaw bi ñu seetloo ni dépite la ba léegi fa Ngombalaan ga.

SINEEBAR BI ÑU JÀPP FA TÀMBAAKUNDAA

Fa diwaanu Tàmbaakundaa teg nañ fa loxo sineebar bu takkoo takku. Birigàdd duwaan bu Kidiraa moo fa jàpp lu mu mësul a jàpp ci sineebar démb ci dibéer ji, bi 20i waxtu di jot ci guddi gi. Lu tollook 1137,6 kilo yu ñu laxas ba mu jekk ciy saaku lañ loqati cib ruqu sëfaanu firigoo. Bees ko xaymaa dina war a jar ba 90 tamñareet (milyaar) yu teg 960 tamndareet (milyoŋ).  

BITIM-RÉEW

Doomi réewum Senegaal ya nekk fa réewum Turki ñoo ngi ci ay jafe-jafe. Kurél gii di Horizon sans frontière moo ko xamle. Ci kàdduy seen njiit li ci réew mi, Buubakar Séy, dañuy ñàkk xaalis bu takku ngir mën a am kayit gu leen fay tax a mën a nekkandi, ñu koy wax ci farãse Carte de séjours. Ngir ñu am ko walla ñu yeesalal leen ko dinañu ci fay lu ëpp 7OOi dolaar. Ñi koy am itam, ci àppu ñatti weer lañ leen koy jox te asirãs bi ñuy fay ci at la. Rax-ci-dolli, Nguur ga foofu mën na koo dakkal saa su ko neexee. Ba tax ñuy sàkku ci koñsilaa bu Senegaal mu dimbali leen ci ni mu gënee gaaw ci yombal seen nekkiin foofa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj