Waa F24 fésal nañ seen tiitaange ci tolluwaayu réew mi. Seen xel dalul wenn yoon ci niñ dëgmalee wotey 2024 yi. Li ñuy ragal nag mooy, wote yu jaar yoon yoy, pàcc yépp ñoo ciy gis seen bopp, bañ a am ci réew mi. Nde, ci seen taxaw-seetlu bi, Càmm gi mayul kujje gi fum yakkee nàkkam. Fu way-kujje yi génn ci biir réew mi, tàkk-der yi dinañ dog seen yoon. Ki ci mujj di Xalif Sàll mi ñu téye woon ci gaawu gi fale ca Fatig te teguñu ko fenn lu dul naan kenn mayu ko mu amal njëggam mi.
Taxawaay bii ñu jagleel ñi fare ci kujje gi doon na nag lu F24 di ñaawlu. Nde jamono yi ñu leen di dog, Aamadu Ba mi nar a nekk lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar (waa Càmm gi) mi ngi wër réew mi ni mu ko bëgge.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Fa jàngune Séex Anta Jóob bu Ndakaaru, ndongo ya dajaloo woon nañ fa démb ci altine ji. Li ñu bëggoon nag mooy jàkkaarlook taskati xibaar yi foofa ngir wax ci ubbite jàngune ba. Waaye seen ndaje ma mujjewul a sotti. Takk-der yi ñoo leen fa fekk daldi leen tasaare ak i gërënaad. Ci li takk-der ya wax nag, kenn mayu leen ndogal ñu fay dajaloo nde jàngune ba sax kenn tijjeegu ko.
Ginnaaw loolu nag, ndongo ya xamle nañ ni fileek jàngune ba tijjiwul, njàng dootul am ci daara yu ndaw yeek yu digg-dóomu yi. Te bu jaree xeex ak takk-der yi, dinañu ko def ndax seen ëllëg lañuy sàmm.
NDOGALU PEREFE JURBEL BI ÑEEL JAKARTAA YI
Fa Njaaréem, perefe bu Jurbel bi dafa jël ndogalu dakkal dawalug jakartaa yi guddi. Li mu ko dugge nag mooy sàmm kaaraange dawalkat yeek waa dëkk ba. Nde dañ seetlu ni dogaale yi bare nañ fa lool, te defkatu ñaawteef yi guddi gi lañuy bañ. Bu dee daw bëccëg beet, tere na leen a tooge ñaari nit, rawatina ñi daan faral di yóbbu ak a jëli ndongo yi.
DUWAANU SENEGAAL
146i junniy liitari esãs la duwaanu Senegaal teg loxo. Muy lu mësul a am ci li mu daaneel i defkati ñaawteef yépp. Ci ayu bés yee weesu la njëkkoon a teg loxo 36i junniy liitar. Ci fan yii ñu génn, diggante talaata 16 ak dibéer 22 oktoobar, mu dellu tegati loxo 110i junniy liitar ci diggante Ndakaaru, Cees ak Mbuur. Muy esãs bu takkoo takku bu mu nangoo ci loxoy defkati ñaawteef yu ko doon jéem a rawale.