LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (30/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

CÀKKUTEEFU KURÉLI MAXEJJ YI

Yenn ci kuréli maxejj yi, tudde seen bopp Sursaut citoyen et Demain Sénégal fésal nañ lu ñuy xaar ci Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay. Siiwal nañ ni yónnee nañ ko ab bataaxal, di ci sàkku am ndaje ak moom. Li ñu bëgg nag, mooy Njiitu réew mi doxal déggoo bii di Pacte national de bonne gouvernance démocratique. Muy ab déggoo bu tukkee woon ci njureefi péncoo (assises nationales) yi fi amoon ci diggante 2008 ak 2009. Xamle nañ tamit ni, noppi nañ ngir dajale ay boroomi xam-xam ngir ñu doxal. Déggoo boobu nag, dafay digle ñu fentaat campeef yi ngir saxal demokaraasi bu xóot, nguuru yoon, caytu gu matale te jiital ci maxejj yi.

ÑËWUG ABDULAAY JÓOB, NJIITUL NDIISOOG UEMOA, FI NDAKAARU

Njiitul Ndiisoog UEMOA (Union économique et monetaire de l’Afrique de l’Ouest), Abdulaay Jóob, moo ngi woon Ndakaaru ci ayu-bés bii weesu. Muy tukki bu mu fi doon amal ngir seetsi ak a ndokkale njiiti Senegaal yu bees yi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak Càmmam gi. Naka noonu, séq naak magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, aw waxtaan ci gaawu gi. Bokk na ci li gën a fés ci waxtaan woowu, mbirum moom-sa-bopp ci wàllub xaalis bi ñu yàgg a coowaloo ci at yii weesu. Sëñ Usmaan Sonko xamle ci ni am na ay ndogal yees ci jotoon a jël ca atum 2018. Jàpp nañ ni ci kurél gu am njariñ lañ bokk.

NJËWRIÑU LIGGÉEYU BOKKEEF GI AK YEESALUG LIGGÉEYIINU BOKKEEF GI

Fa Njëwriñal liggéeyu bokkeef gi ak yeesalug liggéeyiinu bokkeef gi, tàmbali nañ fa saytu doxalinu liggéeykat ya. Caytu googu nag, dees koy jaarale ci xarala yu bees yi ngir mën di topp waxtu xéysi yi, liggéey bi ak wàcc bi foofu. Lu ko dalee tey ci altine ji, képp ku fay liggéeyee war na ci moom mu nekk fa bu 8i waxtu di jot ci suba gi ba 17i waxtu. Waxtu noppalu wee ngi ci diggante 13i waxtu yu toftal 30i simili ba 14i waxtu 30i simili. Muy doxaliin wu jëwriñ ji Óliwiyee Bukaal ci boppam njëkk a doxal tey ci suba ak di sàkku ci liggéeykat yi ñu sàmmonteek moom nees ko waxe ci dekkare 96-677 bu 7 ut 1996.

DAKAAR DEM DIKK : LIGGÉEYKAT YA BANK NAÑ SEEN I LOXO

Lggéeykat yu Dakaar Dem Dikk yi sóobu nañu ci ñaxtu. Démb ci altine ji lañ ko tàmbali ginnaaw bi ñu xéyee taxawal daamar yi, lànk ni genn du dem, genn du dikk. Li leen metti nag, ci xibaar yi jot a rot, mooy par-parloo gi kilifa gu mag gu SNT (Société nationale de transport) di doxalee. Wax nañ sax ni am na ñu mu yokkal i dayo fa barab ba te teguko ci lenn lu dul pólitig. Ginnaaw bi coow li biree nag, jëwriñ ji yor wàllu dem beek dikk bi, El Haaji Maalig Njaay, sol na dàllam dem nemmeekuji mbir mi.

KÓRNIS BU NDAKAARU : NJIITU RÉEW MI DAKKAL NA TABAX YI

Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay dakkal na lépp luy tabax ci kórnis bu Ndakaaru. Piyeer Gujaabi Atepaa moo siiwal xibaar bi. Fekk ñu doon ko dalal fa màkkaanu RTS barki-démb ci dibéer ji, ci jotaay bii di Point de vue. Bees sukkandikoo ci li mu wax, Njiitu réew mi ak Càmm gi jël nañ ndogal loolu naka keroog ci àjjuma ji. Lépp luy tabax dakkal nañ leen ba mu des jumtuwaay yi fa nguur gi di amal ñeel askan wi. Cig pàttali, Usmaan Sonko waxoon na ca jamono ni bés bu ñu jotee ci Nguur gi, dinañu toj bépp tabax bu ñu amal ci sowu kórnis bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj