LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (4/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

64EELU MÀGGALU JONNUG SENEGAAL

Tey ci alxames ji la réewum Senegaal màggal juróom-benn-fukk ak ñeenteelu at mi mu moom boppam. Ni ñu màggale bés bi ren nag wute na ak yeneen at yi weesu. Ndax, na ñu daan defee ay mbumbaay amu ca. Li ñu def mooy li ñuy dippe “Levée des couleurs”. Maanaam, xew mu yem ca njénde la. Dafa di, ren moom dafa daje ak ñuy sog a fal Njiitu réew lu yees, muy Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Rax-ci-dolli, wote yi tamit dañu leen a dàqoon. Loolu bokk ci li tax jot gi bariwul ngir Njiitu réew li mën a jël matuwaay yi war ngir ñu amal ko na mu waree. Waaye, loolu terewul ne Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo jiite xew ma ñu jot a def ak us néew.

XALIFA ABAABAKAR SÀLL NEE NA JOTUL BATAAXALU WOOTE

Barki-démb ci talaata ji lañu doon samp Njiitu réew lu yees li, Basiiru Jomaay Fay. Mu am lawax yoo xam ne kenn gisu leen ca xew ma. Xalifa Sàll bokk ca ña ñu fa gisul. Te, mu nekkoon fi kenn ci jegeñaaley Usmaan Sonko yi. Moo tax, mu génnee ab yégle ngir xamle li sabab ñàkk a teewam. Nee na ca bés ba lañu ko xamal ci mbaalu jokkoo gii di WhatsApp ne bataaxalu woote gi jàppandi na. Yéex bi yëf yi yéex moo tax mënutoon a teew ca ndaje ma.

ALLAAJI MUSAA GÉY FEKKI NA DOOMAM

Lu ëpp juróomi weer ginnaaw génnug àddina doomam jii di Paap Ibraayma Géy, ñu gën koo xame ci turu Papitoo Karaa, moom baayam ba fekki na ko. Papitoo Karaa nekkoon ku ñu ràññee ci liggéey bi mu daan def ci mbaali jokkoo yi ak péeteem ci wàllu pólitig, mu génn àdduna ca jamono jee ci yoonu Espaañ wi. Maanaam, ci mbëkk mi. Tey ci alxames ji la way-juram wu góor wii di Allaaji Musaa Géy, amoon lu tollu ci juróom-ñetti fukki at ak benn, wuyuji boroomam.

TEREES EDMON MÉNDI GÉNN NA ÀDDUNA

Terees Edmon Méndi, ab taskatu-xibaar la woon. Ma nga nekkoon fa Rajo bii di Zig Fm bu Sigicoor. Tey ci alxames ji la wuyuji Boroomam. Mu nekk xibaar bu tiis bu dal ci ñiy yëngu ci kibaaraan yi, rawatina kurél gii ñuy dippe “Convention des Jeunes Reporters du Sénégal” nga xam ne aji-bokk la ca woon.

GAYNDEY SENEGAAL YAA NGA FAÑ NEKKOON

Doomi Senegaal yiy taxawal réew mi ci wàllu kuppe (futbal), ba tey jógewuñu fa béréb ba ñu nekkoon ci wayndare wi. Nde, ci wayndare woowu lañuy natte taxawaayu mbooleem ékibi àddina wërngal-këpp. Te, ékib yooyu dem nañu ci lu ëpp ñaari téeméer. Gayndey Senegaal yi nekk ca fukkeelu béréb ak juróom-ñaar. Nde, wayndare woowu kurél gii fi FIFA dañu koy beesalaat saa su ne ba ci tey jii alxames ñeenti fan ci weeru awril.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj