Démb, ci yoor-yoor gi, lañu jàppoon dépite bile ak way-woomeel yi. Li ko waraloon nag mooy ne dañoo nammoon a amal ndajem-ñaxtu ca kanamu àmbasaadu Tinisii ngir ñaawlu li ñuy teg seen mbokki ñuule ya fa nekk. Looloo taxoon ñu teg leen loxo. Waaye, bàyyees na leen.
Njiiteefu Ngomblaan gi am na gan
Kii di Njiiteefu Ngomblaanu Kebeg (Kanadaa), Natali Roy, ganesi na waa Ngomblaanu Senegaal. Naataangoom bii di Aamadu Maam Jóob mooy ki ko dalal. Nee ñu, dina fi nekk lu tollu ci ñeenti fan. Maanaam, diggante 4 ba 8i fan ci weeru màrs wii ngir amal i nemmeekoom ci yenn béréb yi.
Ndajem-ñaxtu waa-Pastef ca Tiwaawon
Tey, ci dibéer ji, la ñoñi Usmaan Sonko ya nekke ca Tiwaawon di amal seen ndajem-ñaxtu. Perefe dëkk ba nangul na leen seen càkkuteef loolu ginnaaw bi ñu ko jébbalee seen ub bataaxal. Li ñu ko dugge nag mooy naqarlu ni yoon di doxe, jàpp yu bari yi ak ni ñu yore alalu réew mi.
MEDINA GUNAAS : Daaka 2023
Njiitu réew mi Màkki Sàll amal na ab siyaaram ca kanamu xalifab Medina Gunaas. Kilifa ga la mu xamle mooy ne, “liggéeyu Màkki Sàll raw na yoy njiit yi fi jot a jaar”.
BITTIM-RÉEW
Réewum Espaañ fas naa yéene ubbil ay doomi réewum Senegaal ay buntam. Bu nu sukkandikoo ci saabal gii di Rewmi, jubluwaayam mooy dalal lu tollu ci téeméeri saa-Senegaal ngir ñu liggéey ca tool ya. Sémb bobu nag, war na door ci weeru awril bii di ñëw. Waaye, àpp gi du weesu jamonoy ngóob mi. Nde, bu ngóob ma jeexee, dees na leen bàyyi ñu delsi. Sémb bu ni mel, amoon na fi ca atum 2019. Waaye, ci 47 saa-Senegaal yi demoon, 18 kott a delsi. Ña ca des dañoo dawoon dugg ca biir dëkk ba.