MAN, CEERNO ALASAAN SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yeen, mbokki réew mi,

Dama bëgg a waxtaan ak yeen ci réew mu màgg.

Senegaal réew mu mag la. Réew mu bari ay kàngaam ak ay jàmbaar yoo xam ne, seen gis-gis ak seen i jëf ñoo xàllal réew mi yoon wu baax. Jaloorey kàngaam ak jàmbaar yooyu, mboor [1] du leen mës a fàtte. [Suuf sii, dama ko jàppe ni ndono lu ma fonk lool sax. Moo tax ma ko, bëgg ko lool ci sama xolo.]  Tàmbalee ko ci xayi Cees yi jàpp tooli ceebi Bàmbali ya, li ko dale ci balluy mbindaare yi suufus Kéedugu si ëmb ba ca ngëmug Fuuta gu bir ga, dale ko ci sag biy màndargaal Jolof ba ca bayreb Kabadaa ba, dale ko Géejawaay [gu xumb gi] jàpp Bàkkel, fépp foo dem ci réew mi, bépp ruq-ruqaan, ci man, ay bunti yokkute lañu. Waaye tamit, béréb yooyu yépp, dañuy jëmmal  ay sas yees war a sasoo ak i coono, fitna, metit yi ma bokk dund ak mbokki réew mi.

Yéene ji ma am ci liggéeyal réew mi dara mënu koo yàq. Ndaxte, yéene jooju, li ko wund mooy bëgg  bi ma bëgg réew mi, kóllëre gi ma fasanteek askan wi ak pasteef bi ma am ci sàmm bokkeef [2] gi. Coono yi samay mbokki maxejj[3] di dund ñoo ma yàgg a gindi, saa yu ma seqee ab jéego, ci soxlay askan wi laay dox.  Man, maxejj bi, bu may liggéey ak bu may pólitig yépp, Senegaal laay jiital. Man, Ceerno Alasaan Sàll, dama bëgg Senegaal.

Fukk ak juróom-benni at ci ginnaaw, atum 2007, nguurug PDS daf ma gàddaayloo woon fa réewum Komoor. Jamono jooja, dañu bëggoon a tas Asecna, ma bañ, daldi lànk ba tëdd ci suuf. Noonu laa def ngir bokk ci ñi sàmm kurél googii nga xam ne, day jëmmal bennoog Afrig. Sama wareef la woon ñeel Senegaal ak Afrig.

Bi may jiite ARTP, atum 2012, dama wàññilu woon sama payoor, xaaj ko lu ëpp ñetti xaaj. Jëf jooju, li ma ko taxoon a def mooy sàmm dige bi nu digaale woon ak askanu Senegaal ba nuy kàmpaañ. La nu dige woon mooy yorin wu sell te jub ngir wàññi fegg [4] bu réy bu dox diggante njiiti pólitig yi gàlloo ay miliyoŋi miliyoŋ (tamndareti tamndaret [5]) ak sunu mbokki réew yi néew-doole yi. Mooy baadoola yi nga xam ne, dañuy am jafe-jafe yu réy ngir jëmmal seen naal yi gën a yomb.

Atum 2017, ba may tekki sama ndombog-tànku jëwriñu Laf [6] gi, daa fekkoon ma bañoon a xaatim ay pasi « hydrocarbures » yu baaxul ci Senegaal. [Sama wareef ci réew mi ak bëgg a aar ëllëgu ndaw ñee ma taxoon jël ndogal loolu.]

Ni ma farloo ci Senegaal duma ko mës a caaxaane te duma ci dellu ginnaaw mukk. Réew mii, ni ma ci xëree dafa réy. Senegaal ba Senegaal daj, fépp fu ma mës a dem, daje naak ay jigéen ak i góor yoo xam ne, bés bu nekk, saa su nekk, dañuy daj coono yu mettee metti ngir am lu ñu ndékkee, walla lu ñu añee, walla lu ñu reeree. Lekk benn yoon ci bés bi sax, jafe na ñenn ñi. Daje naa ak samay mbokki réew ñoo xam ne, naan ba màndi jafe na leen, faju jafe na leen, fay seen njàngi doom, dugal leen ci lekool yi, jafe na leen.

Ndaw ñi nga xam ne dañoo yàqi, ñoo ngi ñafe ngir tekkee ci biir réew mi walla ñuy mbëkk, di jaay seen i bakkan, di tukki bitim-réew ngir tekki.

Liggéeyikaayi bokkeef gi, niki loppitaan yi ak lekool yi, dañu tumurànke. Dara waralu ko nag lu dul càggan bi leen njiiti réew mi sàggane. Ñi jiite liggéey bi ci béréb yooyii, ñu ngi def seen kemtalaayu kàttan, waaye mënuñu ci dara. Beykat yaa ngi wéy di ndóol. Liggéeykat yi mënuñoo faj soxlaay njaboot gépp. Ndongoy daara yu kowe yi (iniwérsite yi) dañuy jàng ay ati at, daj coono yu dul jeex, waaye lim bu tuutee tuuti ñoo ciy am liggéey.

Jamono jooju nga xam ne sunu koom-koom gi dafa suux, as mbooloom politisiyeŋ su ndaw bóof ci milyaari réew mi, aakimoo leen. Ñenn ñi jël seen i kër, def leen ay sàqi xaalis, di tibb ci alalu askan wi di ko yóbbu seen i kër. Nger ak goreedi tilimal nañ yoriinu réew mi. Li ëpp ci askan wi di gën di ndóol ak a sonn, njiiti pólitig yiy gën di luubal alalu askan wi, di ko puukarewoo teg ci . Xol yiy gën di tàng, tooñaange yi dem ba jéggi dayo. Jéyya yi fi jot a xew ci ñaari at yii weesu dañuy firndeel ne, li njiit yiy aakimoo alal ji di bàyyi askan wi ak coono yi saa-senegaal yiy jànkonteel ñooy jur fitna ci réew mi.

Léegi nag, dafa jot sunu réew teguwaat ci yoon wi mu nekkoon, maanaam yoonu yaakaar, njub ak jubal, xam-xam, yemale ak màndute, yoonu boppam. Nde, kuy dem ba xamatoo foo jëm, dangay dellu fi nga jóge.

Dafa jot ñu jëmmal gént yi te nu defaraat sunu dëkk yi, jëmbat ci garab yu baree bari ngir ñu noyyiwaat, mën a dékku jafe-jafey njuux [7] li ci nu mu gën a gaawe. Beykat yi yeyoo nañ jumtukaay yi ñu beyee at mépp ngir bañ a yem rekk ci bey dunde. Waaye, beykat yi war nañu mën a dund dundin wu neex ak seen njureefi mbey. Jigéen ñi dañu war a dund ak ngor te di gis fekke seen njariñi doom. Yaay ju nekk, yeyoo nga sa doom tekkee ci wet te du jar muy génn réew mi. Lu mën a nekk la.

Ñépp ñoo war a mën a faju ci loppitaani réew mépp, ak fu sa doole tollu. Loolu nag, dafa laaj gis-gis bu bees boo xam ne, dees na leen ko biral lu yàggul dara.

Dafa jot Senegaal nekk réew mi ñuy defaree li Afrig sowu jant soxla lépp, daldi sóobu ci xarala yu yees yi bu baax a baax ngir yeesal anam bi nuy dunde, anam bi nuy fajoo, di defar ak a bey ; di suqali fànn yu bees ngir mën a faj sunu soxla yu bari yi ak soxlay réew yi nu dendal. Dinanu soppi Senegaal, def ko njéemug [8] Afrig sowu jant.

Ngir loolu mën a sotti, fàww nu xoolaat sunu njàngin mi, sanc ay lekool ak i daara ngir nu tàggat sunuy ndaw, waajal leen ci xëccoo bi am ci àddina si. Loolu yépp nag, dees na ko dëppale ak sunu mbaaxi maam, sunuy aadaak cosaan, ngir nu bañ a gàlli. Bu ko defee, dees na nàmm xel yi, xirtal nit ñi ci xam-xam, jëmbat ci ñoom mën-mën. Loolu nag, ci njàng meek njàngale mi lanu koy jaarale.

Warees na fi jële ba fàww nger ak yorin wu ñaaw wi ñu yoree réew mi.

Luy jot, jot na ginnaaw dee. Senegaal dafa war a siggi, dëggal boppam, wone dayoom, wone màggaayam. Tabax ag Bokkeefu ngor dafa jot, ànd ceek pas-pas bu yees ak yéene ju dëgër ngir ëllëg gu naat. Dafa jot ñu dekkal yaakaaru ndaw ñi nga xam ne ñoo ëpp fuuf ci askan wi. Ndax, téeméeri nit ñoo jël ci réew mi, juróom-ñaar fukk yi ay ndaw lañu.

Yeen, mbokki réew mi, sabab yii yépp, ànd ak mbëggeel bu sore bi ma am ci Senegaal ak yéeney yeesalaat ko moo ma tax a doon lawax ci wotey njiiteefu réew mi, atum 2024.

———————————————————–

Dees na ko lootaabe ci ponk yii :

  • Ay mbàyyi [9] ak i gëm-gëm

  • Seetlu yi

  • Naal yi ak Wax ji

BAATAAN YU JAFE YI

[1] Histoire

[2] République

[3] Citoyen

[4] Ecart

[5] Million

[6] Energie

[7] Climat

[8] Start-up

[9] Renoncement

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj