MBËKK MI, BA KAÑ ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbëkk mi lëmbeeti na réew mi. Jamono yii, mëneesul a toog ab bés te jot xibaar ñeel i gaal gu suux walla gaal gu këppu. Ci tefesi réew mi lañuy déqee, wutali Espaañ. Ndaw ñaa ngi mel ni ñu ñu xabtal, ñuy mbëkk rekk, géej di leen mëdd. Limu way-lab yiy yokku saa su nekk, géej giy wann ak a gëq. Bàrsaa walla barsàq, ba kañ ?

Coowal mbëkk maa ngi booy nopp yi. Moone de, foogoon nañ ni mbirum Bàrsaa walla barsàq féete na ginnaaw. Ndekete, daf noo jiitu woon, taxaw di nu xaar. Néew yi bari nañ, waaye ndaw yi ciy sóoboo ngi mel ni ay gumba. Wax ji law na, waaye roñukat yaa ngi mel ni ñu tëx. Faalewuñ kenn, faalewuñ dara. Dem rekk. Tekki rekk. Amul leneen. Li ñuy bàkkoo mooy : “Tekki mbaa dee rekk.”  Lu tax ?

Senegaal, sas wu réy la mboolaay giy gàll ay ndawam. Nde, ndaw mooy ki war a wuutu baay, war a dimbali yaay. Digalees na ko mu taxawu mbokk, defal mag ak rakk. Fu xew amee, bum ci mën di doon, war nga làmb loxo ci poos. Boo ko defulee, ñu xas la, ŋàññi la, suufeel la, toroxal la ci sa biir i nawle. Am nga kook amoo ko, seen yoon. Mën nga ko am déet, duñ ci xool loolu. Ci déggiinu saa-senegaal yi, ki tekki mooy ki tekki dara ci kanami nit ñi, maanaam ku leen di jariñ, donte as lëf la. Kon, gàllees na ndaw ñi wareef ci ko wareef te, réew mi, lépp a fi dëgër. Njàng mi baaxul. Liggéey amul. Njaay mi doxul ndax ñépp a ngi jaay léegi. Sikkim a lakkandoo te ndox amul. Moo tax ñuy waaf ci tefes yi ngir dagaani wërsëg. Xam naa dingeen ma laaj, “Ana Nguur gi ?”

Dama leen di delloo laaj bi : “Ana Nguur gi ?” Nde, man ak yeen noo ci bokk yem. Waaye, ndax sunu njiit yi tal nañ mbëkk mi ? Wëliis mbirum pólitig ak wotey 2024 yi, dara soxalu leen. Te, ndeysaan, mbënn maa ngi nuyoo. Luy pexe ?

Geneen gaal teer na ci tefesu Wakaam. Nee ñu, 18i ndaw ñoo ci dee. Nguur giy weddi, naan 16i kese la. Waaw, bu dee benn nag ? Waa Horizon sans frontières nee, dafa mel ni Nguuru Senegaal dafa teg tànkam ci mbëkk mi wala defu ci yitte ji ci war. Ndax, bu ñu jàngatee seen génn gu mujj, dafa mel ni seen bopp lañuy layal. Nde, ci kàdduy Antuwaan Jom miy jëwriñu biir réew mi, réewum Senegaal “eldorado” la, maanaam ab àjjana. Moo tax, moom, gisut lu war a tax ndaw ñiy wuti beneen “eldorado”. Bu Senegaal dee àjjana de, xana bosam la, ak ñi mel ni moom. Ndax, Nguur moom ni mu bindoo fi Senegaal, ku ci nekk, daanaka yaa ngi biir àjjanay suuf. Ku nekk àjjana nag, du yëg la waa safara di yëg. Ginnaaw lii, lu fi des ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj