ÑAAREELU TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA BITIM-RÉEW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi mu njëkkee génn, dem fa réewum Móritani, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomay Fay amal na ñaareelu tukkeem fa réewum Gàmbi. Muy tukkib liggéey bum fa amal ngir janook naataangoom bii di Aadama Baro ci àndu ñaari réew yi, waaye itam, tukkib nemmeeku ngir dox tànki mbokk ci diggante ñaari askan yi mboor jot a boole.
Ci alxames jii weesu la Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay amaloon tukkeem bu njëkk fa bitim-réew ginnaaw bi mu faloo ak tey. Mu doon ko amalee fa réewum Móritani. Tey ci gaawu gi la doon amal ñaareel bi fa réewum Gàmbi. Bi 10i waxtu di jot ci suba si ba tegal 30i simili la roppalaan gi dal fa Bànjul. Njiitu réew ma Sëñ Aadama Baro moo ko dalal, làrme ba delloo ko njukkal.
Tukkeem bi nag, bari na lu mu ëmb ci solo. Nde bees sukkandikoo ci BIG (Bureau d’information Gouvernemental), di pekk bi solowoo xibaari Càmm gi, tukkib liggéey la waaye rax na tànki dox mbokk ci diggante ñaari réew yi ngir li ñu jot a séq ci mboor, jaare ko ci seen i askan.
« Tukki bi dafa am solo lool ndax dafa aju ci tànki dëgëral jaxasoo bi Dakaar ak Bànjul jaxasoo ci wàllu mbokk ak ci wàllu jëflante ci li weesu ci seen Mboor » (BIG)
Naka noonu, dafay wone ni Njiitu réew mi dogoo ci sàmm ak gën a dëgëral mbokkoo gi dox ci diggante ñaari askan yi te juddoo ci jaxasoo ñaari askan yeek seen i mbatit. Ñuy ñaari réew yu bokk suuf, bokk mboor ak i mbatit. Waaye itam, doon nañ ñaari réew yu bokk jëmu te réewandoo Senegàmbi (1982-1986) biñ fi taxawaloon firndeel ko.
Bu loolu weesoo, tukkib liggéey bee ngi delu ci mbir yu am solo lool ci jamono, ak nu ko ñaari réew yi namm a doxalee ci seen diggante. Ñuy yu demee ni wàllu kaaraange ak yoon, koom-koom ak yaxantu, dem beek dikk bi ñeel nit ñeek moomeel yi añs.
Waxtaan nañ itam ci naka la ñaari réew yi mënee dugal seen i loxo ci yoonu jàmm, kaaraange ak yokkute, jaare ko ci kurél yii di CEDEAO (Communauté Économique des États de l’Afrique de l’Ouest), UA (Union Africaine), OCI (Organisation de la Coopération Islamique) ak ONU (Organisation des Nations Unies). Njiitu réewum Gàmbi li sax sàkku na ci Sëñ B. J. J. Fay mu ñëw teewe 15eelu ndajem OCI bi ñuy amal foofu, fa Bànjul, ci bési 4 ak 5 me 2024.
Mbir yi leen yitteel yépp nag, lëkkatoo gu dëgër a ko mën a yanu. Ba tax na, ci seen janoo yi ñu njëkk amal, Sëñ Aadama Baro ak Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay waxtaane nañ tolluwaayu lëkkatoog ñaari réew yi. ku ci nekk ci ñoom ñaar rafetlu na bu baax ni diggante bi di doxe. Xas nañ itam ni seen ñaari càmm yi danañ wéyal liggéey bi ngir andi ciy yokkute yu am solo.
Bees sukkandikoo ci sunuy nattaango yu APS (Agence de Presse Sénégalaise) ñaari Njiiti réew yi déggoo nañ itam ci wéyal ndiisoog Njiitu réew gi jot a am ci diggante ñaari réew yi ngir gën a mën a sàkk i pexe ci seen ànd bi. Ndiisoog Njiitu réew gii di ñëw, ndakaaru lañ koy amalee. Dinañu wéyal seen waxtaan ngir jàpp bés yiñ koy amal.
Ba tey ci seen ndaje mi, bari na lool lu ci askan wi doon séentu, rawatina ci mbirum jàmmi kaasamãs mi nga xam ni fees ko tuddee tudd ci réewum Gàmbi. Li ñuy xaar ci ñoom mooy ay jëf yu dëggu ngir delloosi jàmm ci diwaan boobu nga xam ni ca atum 1982 ba léegi xeex bi jógu fa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj