Suukar ñàkkul Senegaal ! Pexem jaaykat yi kepp la, ngir yokk njëg li ci lu dul yoon. Lii la kàdduy Luwi Lamot yiy wund, moom miy njiitul aji-digle ju Mimran. Ginnaaw bees nemmeekoo ñàkkug suukar gi ci réew mi, rawatina Ndakaaru, waa Dakar Matin jokk nañ ko, laaj ko sabab yi. Daf leen tontu, wax leen ne :
« Suukar saa ngi fi ne gàññ. Noo ngi defar lu bari, di jaay lu bari. Nun de, noo ngiy séddale ñaari yoon li nu tàmmoon a séddale. Bun daan génne 400 walla 500i ton bés bu nekk, loolu doon na doy sëkk te, ci njeexitalu weer wi, doon nanu àgg ci 16 walla 17i ton, bu lépp jaaraan yoon. Léegi, weer wu nekk, dinan ci génne 24. 000i ton. Daanaka danoo ful ton yi ñaari yoon ndax, tey, noo ngi séddale, bés bu nekk, 13. 000i ton. »
Waaw, kon fu suukar si jaar ? Ku ko mëq ? Luwi Lamot ne, laaj yooyu, jaaykat yaa ko yeyoo, ñoo ci war a tontu. Nde, bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, gorosist yaa ngiy jënd suukar si, di ko yeb ciy sëfaan. Luwi Lamot neeti, ñoom gorosist yi, ñooy séddale suukar si, tas ko ci réew mi. Mu teg ci ne : « ca seen i wet [ñoom gorosist yi], am na demi-gorosist yeek jaayaatukat yi. Ñoom ñilee war a jaay suukar si ci ja yeek bitig yi. »
Fu suukar si jaar nag ? Ndaxte, fu ci mel ni Ndakaaru, jafe nga gis fa suukar. Dafa di, njëg li dafa yokk te, am na ci jaayaatukat yoy, mbuusi ñaar-fukk lañuy jaay, amul kilo, amul liibaar, astemaak genn-wàllu liibar. Ñar-fukk rekk, te as tuut lay doon. Loolu nag, dafa jural askan wiy jafe-jafe yu metti, rawatina ci ndoorteelu weeru koor gii. Dafa mel ni, nag, Luwi Lamot xam na lu tax askan wi mënut a jot ci suukar si. Nde, dafa seetlu ne :
« Atum ren ji, suukar dafa ñàkk ci àddina si, moo tax soxlay suukar yi yokk, ba ci réew yi nu digaloo. Danu seetlu ne, gorosist yi dañuy taamu jaay baana-baana Gine yeek yu Mali yi, ndax ñoo ëpp li ñuy fay ci xaalis. Njëgu suukar si, ci réew yi nu dendal la gënee jafe. Bu ñu jaayee doxandeem yi, ci lañuy gën a am tono. »
Wolof da naan, balaa ngaa laax jaay, laax lekk. Waaye de, dafa mel ni jaaykati Senegaal yi dégguñu bile léebu, walla buñ ko déggee yit, jëfewuñ ko. Bu yàggee nag, dina ëpp i loxo. Moo tax nguur gi war cee wut pexe. Luwi Lamot xamle na ne, CSS a ngi liggéey ak njëwriñu yaxantu gi. Jubluwaay bee di rëbb ñiy nëbb suukar si di ko jaay doxandéem yi, jàpp leen, daan leen ay daan yu diis. Ngir pexe moomu àntu, Luwi Lamot nee :
« Bu nu jébbalee suukar si ay gorosist, danuy yégal ci saa si waa njëwriñu yaxantu gi, jox leen seen i njokkatle yépp ngir ñu saytu leen, topp leen ba ñu jaay suukar si waa réew mi. »
Bu dee jaayaatukat yiy jaaye kilo suukar 700i dërëm te mu war a jar 500i dërëm kese, Luwi Lamot duut na ci baaraam boroom bitig yi. Waaye, ci waxam, loolu dina dakk. Ndax, waa CSS dinañu lëkkaloo ak waa njëwriñu yaxantu gi, yóbbu suukar si ci yenn dëkk yi, jaay ko fa jaayaatukat yi, bañ ko jaarale ci loxoy yenn gorosist yu màndoodi yi.