NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI : BËGG-BËGGI JËWRIÑ JI MUSTAFAA GIRAASI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu njàngale mi ci daara yu ndaw yeek yu digg-dóomu yi, Mustafaa Giraasi, fésal na yéeneem ñeel daara ju Senegaal. Ginnaaw bi mu jëlee lenge yi, bëgg-bëggam mooy soppali daaray Senegaal yu.

Jëwriñ ju bees ji, Mustafaa Giraasi, namm na soppali xar-kanamu daara ju Senegaal. Bëgg-bëggam nag mooy joyyanti njàng mi, yeesalaat ko. Loolu mooy li mu njëkk a biral ginnaaw bi mu jëlee lenge yi ci Càmm gu bees gi. Ni mu ko waxee, « ci lu amul genn yaras te ànd ak dëggu gu mat sëkk ak njàmbaar gu bare, dañu war a dox ci tànki tëggaat ak soppali daaray Senegaal yi ».

Li mu namm ci daara ju bees jooju mu bëgg a tëgg mooy mu méngook jamano te sóoraale ëllëg. Maanaam, « dañoo war a taxaw ci tànki daara ju jublu ëllëg ». Muy daara ju mu duppee ci farãse « L’école du futur ». Li mu ko duggee nag, te mu leeral ko ciy kàddoom, mooy ni Senegaal dafa war a waajal i ndawam ni « réew yi tegu ci yoonu yokkute di waajalee seen i ndaw ci àdduna su yees si ». Naka Noonu, njàng meek njàngale mi dafa nekk liy doxal yoonu soppali réew mi, rawatina xarala yu bees yees ci dugal, ñuy soppi doxiinu àddina ak nees war a doxaleek waa àddina. Daara ju bees jooju jëwriñ ji bëgg a tëgg, dina dellu wéeru ci mbatiit ak mbaaxi réew mi.

« Dañ war a tanqee ci mbaaxi sunuy askan ak sunuy mbatiit ngir dëgëral njàngalem mbaaxi delluwaay yi ñeel xaley Senegaal, ndax li daara jile nar a doon mooy tàggat ci àppu 15 jàpp 20i at, ndawi Senegaal yi ñu bëgg ci réew mi. »

Ginnaaw loolu, jëwriñ ji xamle naat ni, ci coobare boppam, dina dem giseek jëwriñ yi fi jot a jaar. Nde, am na yu bare yuñ xam te mën koo bokkook nit ñi ci yoon wu bees wi ñu sumb. Gisu ci dara lu ñaaw te bokk na ci seen pexe boole léppi dooley Senegaal ngir jëmale ko kanam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj