NJIITU RÉEW MI BIND NA LIGÉEYKATI CAYTUG BOKKEEF GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njjitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, bind nab bataaxel, jagleel ko liggéeykati caytug bokkeef gi. Ci biir bataaxel bi, mi ngi leen di woo ci jub, jubal ak jubbanti.

Aji-tekki ji : Fàllu Silla

« Yeen, naataangoy liggéeykat yi, jigéen ak góor,

Ci jamono ji nu tollu ci sunu mboor, nga xam ne jéego bu nu teg bu ne jëm ëllëg day jëmmal màndargay dige ak yaakaar, kon jaadu na lool ci man ma yékkati ay kàddu jagleel leen ko, yeen jigéen ak góor ñu jàmbaare ñi sax ci yittey sunu réew mi. Yeen ay, ci lu amul benn werante, sunuy kenoy caytu gi (administration), di sunu xolu réew mi.

Senegaal gii, sunu réew, taxaw na tay ci fajarug jamono ju yees, jaar ci gis-gisu ëllëg gog, ma-réew (citoyen) bu ne, ak fu mu man a féete, war naa man a sigarewu (jouir) ci njureef yii kenn ku ne war a dugal loxoom. Senegaal gu juboo, leer te yemale, goo xam ne suqaliku gu sax te matale dootul doon i gént, waaye day doon lu wér lu matale fépp.

Bu sunu réew amee demokaraasi bu dëgër, dal ak jàmm, li ko waral ci li ëpp mooy seen ug jaayante, seen ug xereñte ak seen dogu ci liggéey bi. Yeen ay sàmm mbaaxi sunu Repiblig bi (Bokkeef gi), way-fenti sunug suqaliku di làntinoori déggoog askan wi.

Tay, maa ngi leen di woo, ànd ak nawloo ak cér bi ma leen jox, ngeen doxal pas-pasu jub, jubal, jubbanti. Na njub, dëggu ak royukaay di jiitu ci seen jépp jëf. Nangeen bàyyi xel bu baax ci seen liggéey saa su ne, li ñépp bokk, nga xam ne yittey ma-réew yi ak seen nekkiin ñooy jiitu ci leneen lu mu man a doon.

Ci lu soxal sunug jaayante jëm ci Senegaal gu bennoo te naat, maa ngi leen di bàyyiloo xel bu baax solo si nekk ci leeral ak sàmmu ci sunuy jëf ak sunuy dogal. Sunu caytu gi cér bu am solo la am ci jëmmal bëgg-bëggi sunuw askan, te ci loolu laa amoon yéene fàttali leen gëm-gëm yooyu war a doon li nuy wommat ci sunu doxaliin.

Sàrt 2012-22 bu 27i desàmbar 2012, bi aju ci leeral ci saytu alali askan wi, tëral na anam yu leer ci càmmug liggéeykat yi laale ci caytug mbiri askan wi. Fésal na wareef ci am doxaliin wu rafet te mucc ayib gu kenn manul a ŋàññ ñeel mbooleem liggéeykati Càmm gi (L’état), taxaw bu baax ci xamle ne leeral du ag coobarewu, waaye wareef la. Sàrt bii, ci ay tombam 7.2 ak 7.3, fàttali na ne nun, ndawi pénc mi, am nanu wareefu bàyyi xel bu baax yoriin wu mucc ayib ci mbir yi ñu nu dénk ak di yoole képp ku wàcc yoon wi ñu rëdd ngir saytu alalu askan wi. Doxaliin woowu doonul wareef rekk waaye mooy ngor, di feddali sunug jaayante jëm ci ma-réew yi nuy liggéeyal.

Loolu moo tax nu jox taxawaay bu am solo ci aar yoolekat yi (lanceurs d’alerte). Day am solo lool kenn ku nekk yëg péexte ak ug taxawu ci tasaare, ci kaaraange, ay xibaar yu jëm ci ay ndëngte walla jëf yu méngoowul ak jikko ju rafet walla yoon. Jaayante googu nag day wane yéene ji nu bokk am ci tabax gornamaŋ bu jub, lalu ci jikko yu rafet ak wareefu leeral (rendre compte).

Maa ngi leen di ñaax ngeen ame pas-pas yooyu ci seen liggéey bés bu set, di fàttaliku ne seen taxawaay lu gànjaru la ngir man a wéyal ag sàmmu ak leeral ci sunu doxaliin. Takku taxaw, nu àndandoo dëgëral sunug dogu ci liggéey ci sag ak ngor, ci sàmmonte ak sàrt yi nuy wommat ngir nekkiin wu mucc ayib ñeel mbooleem saa-senegaal yi.

Sunu sas, wi nu bokk ak wu kenn ku ne, mooy liggéey bañ a dàcc ngir soppi dundug saa-senegaal bu nekk muy jigéen walla muy góor. Sunug jaayante ngir liggéeyal réew mi romb na wareefi caytu gi. Dafa bokk ci sunu pas-pas bu dëggu ngir liggéeyal réew mi ci sunu gëm-gëm sunu kéem tolluwaayu kàttan.

Xam naa bu baax li nuy xaar. Yoonu suqaliku, yoon ak yemale dafa bariy pakk. Waaye, bir na ma ne sunug dogu ak sunug bennoo dinañu nu may nu man a jéggi mbooleem gàllankoor yi ngir sottal naal wi nu bokk.

Ci sama taxawaayu Njiitu Réew mi, maa ngi jaayante ci nekk seen wet, di leen taxawu ci mbooleem li ngeen di sumb te di fexe ba seen nekkiin ci seen ug jaayante di doon lu mucc ayib saa su ne.
Nanu ànd, ci dimbalante, tabax Senegaalu ëllëg. Nanu def sunu réew muy suuf soo xam ne ma-réew bu ne dina fa man a tekkee ngir dugal loxoom ci nekkiin wu mucc ayib wu ñépp bokk.

Kon nag maa ngi leen di woo, ci dogu ak yaakaar, ngeen takkaat laxasaay yi te ñëw nu joxante loxo ci liggéey bu mag bii ñeel réew mi. Nanu doon ay tabaxkat yu dul dàcc ngir Senegaal gu naat te fés, niki nammeel yu xóot yi sunu askan ame.

Ànd ak sama kóolute ak samag cofeel ngir seen jaayante gu dul dog ci yittey Repiblig bi.

Basiiru Jomaay Jaxaar Fay

Jëm ci mbooleem liggéeykati caytug Senegaal gi. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj