RUWÀNDAA : PÀTTALIKUG 30EELU ATUM FAAGAAGALUG TUTSI YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Atum ren ji mooy tollook fanweereelu at ginnaaw bi faagaagalug Tustsi amee ba léegi. Ndax, ca atum 1994 la musiba bi amoon. Àmbasadëeru Ruwàndaa bi nekk Ndakaaru amaloon na ag pàttaliku fii ci gëblag Senegaal. Li mu ko duggee mooy fàttaliku xew-xew bu tiis boobule nga xam ne, reyoon nañ ci limub 1 miliyoŋ ciy Tutsi. Diggante 7 awril jàpp 15 sulet 1994 la rey gi amoon.

Dafa di, Njiitu réewum Ruwàndaa, Póol Kagaame, dafa tànn 100i bés yoy, dees na ci fàttalilku faagaagal bi, ci 30eelu atam ci ren. Ponk bi ñu ko tànnal mooy : “Pàttaliku, Bennoo, Yeesalaat”.

Àmbasadëer bi, Saŋ Piyeer Karabaranga, yékkati nay kàddu, wax ne :

“Faagaagalug Tutsi yi yóbbu na limub 1 miliyoŋ ciy bakkan. Li ko waral mooy askan wee ko àngu woon, ku nekk di rey say jegeñaale. Loolu la gëstukat yu bari wax.”

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj