SAAJO, IMAAM YI SAX ÑU NGI ÑAAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaañu-gaañu bi Saajo Maane ame ginnaaw kuppe ga mu mujje def ca Bayern, jural na saa-senegaal yi njàqare. Te, du ñi safoo  taggat-yaram rekk a ci jaaxle. Ndaxte, ñépp a amoon yaakaar ci doomu Bàmbali ji, ñeel joŋante bi war a am ca Qataar te ñu bari ci ñi seen xel màcc ci Futbal, siiwal ne Maaneey càppaa-coli bi.

Wolof nee na, ndogal du wees. Bi mu desee lu dul ay bés yu néew a néew laata ngir joŋante kubu àddina siy door la gaynde gi ame gaañu-gaañu bi teey xel yépp. Nde, laaj bi mooy :  ndax Saajo Mane dina kuppe. Dafa di, xam nañ ne gaañu-gaañu boobu, lu am la. Te yit, ab diir bu gàtt moo des kuppe gi tàmbali. Waaye, teewul Aliyun Siise miy tàggat gaynde yi boole ko ci gaynde yiy teewal Senegaal Qataar.

Du ñàkk ne pajum dooktoor moo gën a yey ci Maane. Waaye nag, imaami Bàmbali yi def nañ lañu xam. Muy dellu ca Téere Bu Sell Ba, ndax Yàlla yékkati Saajo. Dinañ di faral di wax naan, taal bu tëe tàkk, wett gu nekk lañu koy uppe. Kon, ñu gis ne jógug kuppekat boobule, ñépp a ci def yitte. Ba ci Imaam yi sax. Looloo tax, imaami Bàmbali yi ak dëkk yi leen wër daje ngir ñaanal Saajo Maane. Ña nga dajewoon ca jumaa ja nga xam ne, moom Saajo Maane, moo ko tabax ca dëkkam ba. Ñu jot faa wàcce lu tollu ci 45i kaamil, ndaw lim bu takku ! Ñoom ñépp  a maase ñaan ci Alxuraan, ñaanal Saajo Maane ngir mu jóg ci jàmm. Fàttewuñu tamit ñaanal réewu Senegaal ngir mu indi ndam li fii ci sunu gaal gi. 

Mu mel ni kuppe nekkut mbirum tàggat-yaram kese. Ndegam gëm-gëm ak diine diñañ jaxasoo ngir dekkal yaakaar. Te, Saajo Maane mat na miisaal ngir ne neexalu Socrates firnde la.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj