Biige Jaañ, ndaw su jekkoon, neex deret lool, moo dem ba mel ni kuy féey ciy yëreem ndax jeex. Daan na gaaw a sonn, boole ci di ñaq guddi, di ame yaram wu tàng. Ba mu demee kër doktoor, ñu xamal ko ni daa am doomu-jàngoro ji ñuy wax sidaa. Ba ñu seetee boroom-këram tamit, mu am ko, waaye màndargay biti yi feeñaguñu. Ndeysaan… Noonu, seen àddina mel ni lu tukki. Waaye, amoon nañu wërsëgu mën a faju. Ñuy jaabante lopitaal, di dem ak a dikk, lépp ngir saafara seen feebar bile. Dem nañu ba tane bu baax, moomaat seen bopp, ànd ak cawarte. Waaye, wërsëg wi ñu am, ñu baree ngi dund ak feebaru sidaa te amuñu ko. Moo tax nu bëggoon kenn bañ a fàtte ni sidaa mi ngi wéy di lore ak a reye.
Keroog, alxames, fan wu njëkk ci weeru desàmbar, la àddina si jagleel xeexub jàngoroy sidaa. Muy bés bu am solo bob, dañ ciy fésal jéego yi jot a am ci xeex bi, tolluwaayu liggéey bi, joxe ay xibaar yu jëm ci nees di fagarook a moytoo sidaa. Waaye tamit, dañu ciy dànkaafu askan wi. Ndax, loolu, dina tax ñiy ber ak a ragal ñi ame sidaa, nànd ni sidaa feebar la naam, waaye « ku wéradi nga koy daw, mën na yokk li koy metti », ni ko Njaga Mbay daan woyee. Ba tax na wëppa ren jii (2022), Tolloo walla Cuq ngir tolloo, di ñaax nit ñi ngir kenn bañ a beddi moroomam, rawatina ci jamono joj, mbas mi daa lëmbe àddina ci 3i at yii.
Moo waral Mbootaayu Xeet Yi ak Senegaal di jàppale ñi am sidaa tey naqarlu ñi ñàkk seen bakkan ci sababu feebar bi. Ñu ngi ñaax ñépp jàpp ci ngir sidaa jóge fi ba fàww fileek 2030. Ndajem Mbootaayu Xeet yi, daaw, dogaloon nañ :
–Jëfandikoo xarala yu bees yi ngir fagaru ak xam lu jëm ci sidaa ;
–Fexe ba garabi sidaa yomb a jot ci ñi ko yittewoo ;
Gaa, ay jéego am nañ ci. Waaye nag, OMS, kurélu wér-gi-yaram ci àddina, mi ngi xamle ni, dox bi yéex na. Ndaxte, mbas mi ak xareb Ikren bi ak yu ni mel ay gàllankoor lañu.
Waaye su bennoo amee dina yombal xeex bi. Dafa laaj nag, Càmm geek farandoo yi lëkkaloo ngir :
–far ñàkk tollale giñ nemmeeku ci askan wi ;
–dëggal jéego yi jot a am ;
–gën a jox cër doom-aadama, rawatina way-tawat yi ;
–lootabewaat njariñe yi ba ñu méngook soxlay askan wi ;
–jege askan wi, waxtaan ak moom ;
–dakkal ber ak dànd ba ku nekk yëg kaaraange ngir dem ci fajuwaay te du am benn xel-ñaar.
Di fàttali ni sidaa feebar la buy juddoo ci séy, deret, walla jigéen wàll ko doomam. Ñi mu dal dañuy mujj jeex tàkk, seen yaram di tàng, ñuy gaaw a sonn, di faral a ñaq guddi. Te yit, yeneen feebar da leen di yomb. Ndege, ba fi ñu tollagum nii, sidaa amagul saafara. Loolu moo tax fajkat yi, kurél yeek Càmm gi di ñaaxaate bu baax ci fagaru, saytu ak top paj mi.