Àllarba jii weesu la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon amal ñaareelu ndajem jëwriñam. Ca ndaje moomee la jëlee ay ndogal yu am solo ñeel anam yi ñu yoree woon alalu réew mi at yii weesu. Moo tax, mu sàkku ci banqaasi caytu yii di OFNAC, IGE ak Cour des Comptes ñu siiwal seen caabal yi ñu def ci juróomi at yu mujj yi. Càkkuteef loolee nag mel na ne jàppewuñu ko ay waxi kasaw-kasaw. Dañoo def li ñu naan kàdduy kilifa moom jëfe la sant. Moo tax, taxawuñu, taxawaaluwuñu. Nde, ginnaaw gi, la caabal yi tàmbalee nañ rot ndànk-ndànk.
Siiwalug caabali ëtti caytu yooyu nekk na lu ñor Nguur gu yees gi. Li ñu ko dugge mooy xam fu kopparu Saa-Senegaal yi dugg. Ñan ñoo doon liggéeyal askan wi ? Ak ñan ñoo doon duy seen i poos ? Dafa di, génnug yenn ci caabal yi joxe na ay tontu ci laaj yooyu. Nde, ñetti caabali OFNAC yi rekk, am ñu ñu ci duut baaraam. Ñu jàpp ne ñooñu ni ñu yoree woon alalu réew mi sàmmontewul ak li ñi fi nekk naan lu ñépp bokk, ñépp jot ci. Ndax, ñoom yorin wu ñaaw lañu yoree woon alalu réew mi.
Kii di Mammadu Maamur Jàllo bokk ci ñi ñu gën a singali ci mbir mi. Te, lenn waralu ko lu moy ne kii nekk fi tey elimaanu jëwriñ yi daf ko jiiñoon ne dafa luubal lu tollu juróom-ñeenti fukki miliyaar ak ñeent ci alali réew mi. Li ci gën a doyati waar mooy ne caabalu OFNAC gu 2019 dafa dëggal li Usmaan Sonko waxoon ay at ci ginnaaw. Waaye, loolu taxul woon ñu topp ci Yoon kii di Mammadu Maamur Jàllo ak ña mu àndal ci njuuj-njuuj yooyu.
Mu mel ne du caabali OFNAC yi kesee nar a jur coow ci réew mi. Nde, caabali ëttu caytu bii di “Cour des Comptes” moom yenn du dem ñu des. Bi mu fi jotoon a siiwal daaw jéeg ñeel ni ñu yoree woon FONDS COVID-19 yëngaloon na réew mi lool. Ndax, ndajey ñaxtu yu bari amoon nañu ci ngir naqarlu anam wu ñaaw wi ñu yoree alalu réew mi. Li waraloon taxawaay boobu mooy ne xaalis boobu ñu luubal, ñu bari dañu cee dugaloon seen loxo ngir ñu mën a xeex mbas mi. Loolu terewul ñi nga xam ne ñoom lañu ko tegoon seen loxo, ñu def ca lu leen neex. Ndax, caabal gi génn dafa leeraloon loolu yépp. Ba tax sax, ñu duutoon ñenn ci jëwriñi Nguur gii daanu, ne dañoo luubal alalu réew mi.
Waaye, day mel ne du ci caabali ñaari ëtti caytu yooyu rekk la coow nar a baree. IGE tamit, benn du dem mu des. Nde, dina laal banqaas yu bari ci Nguur gi. Moo tax, kii di Aminata Ture nga xam ne bokkoon na fi ci Nguur gi daanu ba jotoon cee am ay ndombo-tànk teel a àrtu ak a leeral ci li lenn ci kibaaraan yi di siiwal. Ndax, nee na bi caabali IGE yi génnee ak léegi dafa am yenn ci ay kibaaraan yuy ruumandaat ne daf ci am caabal gu ko jàpp. Nee na mësut a luubal. Te, ñi mu bokkaloon liggéey tamit ñi ngi doxi seen i soxla. Mu tëje ay kàddoon ne képp ku bëgg a yàq deram dina la yóbb ca Yoon.
Kon, siiwalug caabal yi pexe la yuy tax Saa-Senegaal yi xam fu seen ug koppar daan dugg at yii mujj. Luubal naak luubalul, caabal yi dinañu leeral lépp. Ndax, li ci kanam moom rawul i bët.