Démb la Usmaan Sonko ak Basiiru Jomaay Jaxaar Fay doon janook taskati xibaar yi fa otel Azalaï. Mu nekkoon seen génn gu njëkk ginnaaw bees leen génnee ci kaso bi. Li gën a fés ci seen i kàddu nag mooy tuuma yu diis yiñ gàll kii di Aamadu Ba miy lawaxu Bennoo Bokk Yaakaaar, ñu doon liggéeyandoo ak moom fa DGID.
Aamadu Ba musiba la ci Senegaal (Usmaan Sonko)
Usmaan Sonko a njëkk a jël kàddu gi. Dafa tàmbalee biral i cant ak i ngërëm ñeel askan wi ak kilifa yoy, feeksi nañ lëkkatoo « Diomay Président », dooleel ko te gisewuñ sax ak Basiiru Jomaay Fay mi nekkoon kaso. Ginnaaw kàdduy nuyoo yeek sargalaate yi, àddu na ci ponk yu bari.
Fan yii weesu, ñoo ngi doon ruumandaat waxtaan wu dox diggante Usmaan Sonko ak Maki Sàll. Meeru Sigicoor bi dëggal na ko. Nee na :
« Naam, waxtaan yu bari am nañ. Ay ndaw yu bari yónni nañ leen ci nun… Ndax, mënul woon a ñàkk… Waxtaan wi ci ñetti ponk la, amul benn bun ci déggoo. Waaye, def nañ ko ci wormaalante ak joxante cër. Waxtaan nan ci dàqug wote yi, ma ne leen xalaatuleen ko, wote yii mënuleen leen dàq… sémbuw amnisiti wi mooy ñaareelu ponk bi ñu waxtaane. Biñ ko waxee, ma ne leen soxlawuma yoonu amnisiti. Bu leen neexee ngeen teggi tuuma yi ngeen ma gàll ndax xam ngeen ni taxawul… Ñetteelu ponk bi ñu waxtaane mooy Péncoo bi (dialogue), waaye déggoowun ci. »
Bu deel li ñeel wote yees ajoon te naroon leen a ajaat, xamle na ne mësu cee ànd. Mu ne :
« Bu amoon kenn rekk ku war a sàkku ñu ajandi wote yi, man mii Usmaan Sonko lay doon. Ndax, Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi li mu def ñépp xam nañ ne teguwul ci yoon. Moom jébbaluñ ko ab daan, waaye moo demal boppam, daldi gëstu, sukkandiku ci loolu jël ndogal loo xam na Yoon mayu ko ko… Li Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi def, dañ ko ko sant. Li ci nekk yépp xam nañ ko… Kon, bu amoon kenn ku war a kaas, man lay doon. Waaye defuma ko. »
Nee na, jëmmu boppam amul solo, waaye lenn kesee ko yitteeloon, mooy « … fexe ba naal bi (projet) jàll. Te, naal bi jàll na. »
Ciy waxam, àttekati Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi dañu jalgati yoon, tere ko bokk ci ndigal lu ñu jot. Moo ko tax di artu askan wi, di woo Saa-Senegaal yépp ñu teey te dal ndax kat,
« …bu dee Ndajem Ndeyu sàrti réew mi dafa jël ñaar walla ñetti ndogal rekk ñépp tëb [di leen tagg] te ci ginnaaw ga ñu xam ni am na leneen lu ci laxasu yenn saa yi, ëllëg bu defee leneen ci ngirtey wote yi, bu ñu fi dellusi [di leen tagg]. Nañ ci ànd ak tee yak dal, rawatina bi mu amee li ñuy ruumandaat. Ci ñoom [tuumay nger]. »
Njiitul Pastef li àddu na sax ci tuumay nger yi waa PDS gàll ci ndoddi ñaari àttekati Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi. Tuumay nger yooyu, lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar bi, Aamadu Ba, lañ ko jiiñ.
Ngir ñàkk a am ay firnde, Usmaan Sonko gëmagul tuuma yooyu. Ndax, « … amaguñ ciy firnde. Buñ ko amoon moom, bokk naa ci ñuy jëkk a taxaw ne lii mënul a dem. »
Waaye nag, Usmaan Sonko dafa mel ni kuy dëggal tuuma yi. Ndax, giinnaaw bi mu ŋàññee doxalinu Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi, mooytuloo askan wi, dafa tuumaal Aamadu Ba. Usmaan Sonko nee :
« Lu yées lu ngeen mën a xalaat, sañ na [moom Aamadu Ba] lu ko raw. Nun ñi ko xam ba xamaatoo ko, tuuma yii bettuñu wenn yoon. Firnde li mooy, dafa jëfandikoo ay malet [xaalis], daldi taxawal ab maafiyaa biir Nguur gi ngir téye lépp ci loxoom. »
Ba tey ciy waxam, loxo Aamadu Ba yi setuñu. Te, ku bari pexe la. Moo tax, yakk na Aamadu Ba lu mel ni xeme. Wax na sax ne, Maki Sàll nekkatul seen nattangoo (adversaire), « …waaye, am nan ku gën a doy waar fuuf, mooy lawaxam bi, Aamadu Ba. »
Daf ne, kii di Aamadu Ba, ciy njuuj-njaaj, nger, càcc ak i mbuxum la mës a dëkk :
« Aamadu Ba, bu Yàlla ñàkkee bëgg Senegaal dëgg-dëgg rekk, na ko jox Aamadu Ba. Laaj bi Saa-Senegaal yi war a laaj mooy ab foŋsoneer kese nan la mënee yor ay milyaar. Loolu rekk jar na bañ a woteel kooku. »
Noonu, njiitul Pastef liy artu Saa-Senegaal yi ci ñu bañ a dénk seen réew Aamadu Ba :
« Bés bu ñu ko joxee réew mi, mooy dénk nañ réew mi waa bitim-réew…. Yàgg na jël lu mu warul jël ma ne ko tegal ci suuf… Musiba bi gën a réy bi nar a dal Senegaal mooy Aamadu Ba. »
Fi Sonko wéer ay kàddoom mooy ne, bu Aamadu Ba àggee fii tey, ay pexe ak xaalis kese ñoo tax.
« Koo xam ne, nekkagoo Njiitu réew mi, waaye fexe nga ba wiiri ba gasal Njiitu réew mi [Maki Sàll] kàmb, Nguur gi yépp tegu sa loxo. Te, lépp, ay malet [xaalis] rekk ñoo ko lal, xam ngeen ne kooku, ku xeeb ay pexeem de, nun ñi ko xam te nekkoon ak moom, defuñu ko. Kon nañu takk sunu ndigg taxaw. »
« Jub naa, xarañ naa te am naa fulla. » (Basiiru Jomaay Fay)
Basiiru Jomaay Fay tamit dafa dëggal tuuma yi Sonko teg ci kaw Aamadu Ba. Nde, ciy waxam, yorin wu ñaaw la yoree woon DGID (Direction générale des impôts et domaines) ak bi muy nekk jëwriñu ngurd mi.
Moomo Basiiru, fàttaliku na, atum 2016, ba muy kaas njuuj-njaaj yi amoon ci njiitalu Aamadu Ba. Booba, dafa bokkoon ci sàndikaa liggéeykati DGID yi.
« Saa bu saytukati juuti yi defaan seen liggéey ba góobee ci ay milyaar, Aamadu Ba da doon jël ay ndogali boppam yoy, méngoowuñ ak yoon. »
Bu dee ci wàllu yoriinu réew mi, Basiiru Jomaay nee na, dina soppi xar-kanami campeef yi ngir saxal màndut, yemale ñépp ngir kóolute dellusi ci wàllu Yoon.
Bu dee lu ko ñeel, xamle na ne def 15i at ci DGID. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, moom Basiiru Jomaay Fay, « liggéeykat bu jub la, xarañ te am fulla ci lu muy def ». Moo tax askan war ko wóolu, dénk ko réew mi ci wote yii ñu dëmal. Wote yooyu nag, Usmaan Sonko gëm na ni ñoom dañu leen di gañe keroog 24 màrs 2024 ci sumb bu njëkk bi (premier tour). Mu ne :
« Mbokk yi, wote yi dañ leen di gañe bu soobee Yàlla… Bu wote yi jaaree yoon, gëmuma ne mën nañ def lu yées 60% bu soobee Yàlla. »
Waaye nag, xam na ni du yomb. Mi ngi def ci xelam ak xeli Saa-Senegaal, dina am ñuy jéem a wuruj kàrt yi, sàcc wote yi. Kon, nañu moytu, ubbi seen i bët te aar wote yi. Ngir loolu àntu nag, daf digal ay militaŋam ñu def la ñu yàgg a def te mu jig leen, te « …mooy ñépp wote bu baax a baax ba noppi sàmm wote yi, saytu ngirte yiy tukke ci mbañ-gàcce yi. »
Moo ngi woo tamit Maki Sàll ngir mu fexe def liggéeyam, fexe ba wote yi jaar yoon, ku ci am ndam mu ndokkeel la, tatagal la, jox la lénge yi. Lu ko moy, demam dina gën a ñagas. Usmaan Sonko nee :
« Bu fexee ba mbirum wote yi jaxasoo, demam du yomb. Fàww mu xam ko. »
Dees na xam fu mbir yiy mujje fii ak juróom-ñetti fan.