Usmaan Tanoor Jeŋmi fi doonoon njiitu ‘’Parti Socialiste’’ dale ko atum 2000, bi pa1rti boobu ñàkkee nguur gi ba sun jonni-yàllay-tey jii moo génn àddina ca Frãs, altine 15i sulet 2019.
Daanaka ñetti weer la fa tëdd ba ni mu deme. Li gën a siiwal feebaram sax, mooy 4 awril bi mu wuute. Kenn xamul lan moo ko daloon ba ni sunu Boroom ñëwe. Jamono jooju, nag, Senegaal yépp a ngi doon waajal njeexitalu CAN bi, am lool yaakaar ni bii yoon dina duma Alseri, fexe daal ba Kup bi du ñu rëcc. Teewul Senegaal ak Afrig delloo Tanoor njukkël lu réy. Njiitu réewum Senegaal, Maki Sàll, waroon a dem Misra, teewe fa finaal bi, daa mujjee fomm tukki boobu ndax dëju Tanoor, ànd ak naataangoom Ibraayim Bubakar Keyta, Njiitu-réewum Mali, ba ayeropoor Blees Jaañ teeru néew bi, jóge fa dem Ngéeñéen robi ko, ñaanal ko, jaale ko njabootam door a delsi Ndakaaru. Ci dëgg-dëgg, Tanoor yelloo na lu ni tollu.
Njiitu-réewum Senegaal mi woon tamit, Abdu Juuf, ànd naak soxnaam ak i doomam ak ay sëtëm ñu bawoo Tugal jaalesi waa Senegaal, muy lu ñépp rafetlu ndax Abdu Juuf, bi ko Senegale yi jàmboo ba tey dafa meloon ni ku leen jéppi.
Ci li ñépp seede, Tanoor ku bëggoon futbal la, daawul wuute benn joŋante Gayndey Senegaal yi. Kenn it mësu koo xam ci bari wax, dugg lu yoonam nekkul mbaa xaste. Tanoor ku amoon yar ak teggin la waaye it amoon na fulla ak faayda. Kuy politig nag moom, rawatina ci réew mu ni Senegaal, fàww lee-lee nga taq ci waaye wax jooju jotagul, dees koy leb ba waxtoom jot.
Maa ngi fàttaliku seede bu daw yaram bi Usmaan Tanoor Jeŋbindoon, ndeysaan, jagleel ko ndem si-Yàlla-ji Birino Jaata. Da ni woon : ‘’Birino, xamoon na lu bari, gis lu bari, dégg lu bari waaye masul a ŋaaŋ wax ci’’. Kàddu yooyu, mënes na leen a yëkkati, jëmale leen ci Tanoor ci boppam.
Tey jii, nag, ñoom ñaar ñépp noppi nañu ba fàww. Yal na leen Yàlla àtte ci yërmaandeem. Lu defu waxumiŋkoy jaal ñépp, jiital ciy mbokkam ca Ngéeñéen ak ay farandoomi ‘’Parti socialiste’’