Sémbub « amnisti » bi Njiitu réew mi naal mu ngi jaabaajonge réew mi. Mu nekk dogal lu Njiitu réew mi jël ngir fomp lépp lu fi jotoon a xew ci diggante féewiryee 2021 jàpp féewiryee 2024. Li mu ko duggee, bu ñu sukkandikoo ci yenn xalaat yi jot a rot, mooy indi jàmm ak dal ci réew mi.
Mu mel ni mbir mi yamut rekk ci ay wax. Ndax, ndogal loolu, ginnaaw ba ca Ngombalaan nga jote, dépite yaa ngi koy fénc ngir wote ko tey ci àllarba ji. Mu nekk kumpa, waayeet ñu mën cee xaar lu nekk ginnaaw ba ñu miine ay mbetteel yu bari ci géewu pólitig gi. Ndax ndogal loolu du lu yomb ci sababu la ca dëxañu. Ñu gis ne bu dee dépite yi war a séq boobu wote, kenn ku nekk ak làngu pólitig ga nga fare walla sax bu dee askan wee la tax a jóg, wote boobu ndogal dina bari ay njeexintal ci réew mi. Bu dee jàmm lañu cay jeex, njaboot yi nàkk seen i doom, seen i góom a nar nàccaat.
Bu ñu sukkandikoo ci kurél gii di “Amnesty international”, moom miy saytu mbiri àq ak yelleefi doomi aadama yi, ma ngay dankaafu Nguuru Senegaal. Nde, la mu gis mooy ndogalu baale loolee (loi d’amnestie) day tax ba duñu jëfandikoo ay daan ngir ŋàññi li fi jotoon a xew. Te, loolu day salfaañe àq ak yelleefi doom-aadama yi. La ñu gisaat mooy lu mat fukk ak juróom (15) ci ay njaboot yu kalaame yoon ngir mu def liggéeyam ci lu ëpp 60 ci ay nit ñu ñàkk seen i bakkan. Kon, bu ndogal loolu jàllee, Nguuru Senegaal dina dog ay wareefam ci ni mu war a jëfandikoo yoon ngir daan jëf yu mel ni faat bakkan.
Mënees na tënk ne, sémbub àtte boobii ñu duppee “loi d’amnestie” dafa nar a jur ay jiixi-jaaxa ci réew mi. La ñu ca seetlu mooy ag parax-paraxe ngir ñu gaaw wote ko. Ñu gis ne kenn ku nekk ma nga cay jeex jàmmam doonte ne jàmmi askan wi lay diir. Waaye, jàmmu waay joo gis, ayu waay a nga ca. Ñu xaar fan la wànnent di mujj ak ay bëtam.