Gannaaw CAN bi mu demoon ak Senegaal, Paap Géy, miliyë Màrsey (Marseille) bi dañ ko dàndoon ca këlëb ba, maanaan dañ ko génne woon, ber ko. Li ko waral mooy ni pasam dafay jeex ci weeru suwe 2024, Màrsey bëggoon mu yeesal ko. Waaye, Paap Géy dafa lànk. Njiiti këlëb ba jéem a wañ loxoom, mu bañ, jàpp fi mu jàpp rekk. Ci la ko Pablo Longoria mi jiite Màrsey beree.
Ndogal loolu tiisoon na ko lool nag. Ndax, laata muy futbalsi CAN bi ak Senegaal, dafa toogoon diir bu yàgg bob, futbalu ci. Li ko sabab mooy ne FIFA dafa tegoon daan. Waaye, ab bunt ubbeeku na. Nde, boolewaat nañ ko ekib bi war joŋante ak Montpellier tey ci dibéer ji. Seen tàggatkat bu bees bi, Jean-Louis Gasset bi wuutu Gattuso moo sàkku ñu boolewaat ko ci gaa ñi. Ndax, ñépp la soxla ngir liggéey.
ËRO 2024 : TONI KROOS DINA BOKK
Saa-Almaañ bi nangu na solaat mayo dëkkam gannaaw bees ko toppee ay yoon ngir mu ñëwaat ca ekib ba. Ca atum 2021 jëloon ndogalu bàyyi ekibu Almaañ bi. Keroog ci 22 féewiryee 2024 wii la xamle ci xëtu Instagramam ni dina dellu ca ekib ba.
“JEUX AFRICAINS GHANA 2024”
Sëriñ Saaliw Ja, tàggatkatu ekib U20 bu Senegaal bi, fësal na limkag 23i ndaw yim tànn ngir ànd ak ñoom ci yooyu joŋante. Ci tànnam gi ñu gis ni woo na ci U17 yu bari yu demoon ci kuppeg àddina gii weesu (U17). Ñooñii di : Amara Juuf, Alfa Ture, Sëriñ Fàllu Juuf, Doriwaal Jaata, Yayaa Jémme, Ibraayma Jàllo ak Idiriisa Géy.
EMILIO NSUE BÀYYI NA GINE EKUWAATORIYAAL
Saa-ekuwaato-gine bi jël raayag dugalkat bi ëppaley bii ci CAN 2023 bii weesu fa Koddiwaar xamle na ni bàyyi na ekib nasiyonaal ba. Gannaaw CAN bi, ay coow yu sew amoon na ci digganteem ak ekib ba, ñàkkul ni yooyu mbir a waral bàyyeem. Moom nag, futbal na 42i yoon ak ekib bi, daldi dugal 23i bii.