Amara Juuf bokkul ci 55i futbalkat yi Alin Siise tànnagum ngir yóbbu leen ca CAF laata mu di ko seggaat ba 27. Moom, kàppiteenu U17 bi, fim ne ma nga Metz ngir faju.
Gaañu-gaañu yaa ngi bëgg a bari ci gaynde yi. Gànna Géy dolleeku na ca limu ñi gaañu fekki ñoom Séeni Jeŋ ak Nàmpalis Méndi.
SUPER LIG
Ëttu àttewaayu Tugal bi jox na dëgg Super League ci kaw UEFA, daldi koy daganal. Kon, saa suñu ko bëggee te mën ko sañ nañu taxawal seen i mbir te benn daan du ci fekk benn ekib niki woon ca njëlbéen ga. Gannaaw loolu nag, kii di Aleksander Ceferin, njiitul UEFA yëkkatina ciy kàddu yoy xol bu jeex lay niru. Mu ngi naan: “Mën nañoo taxawal lu leen neex. Di yaakaar ni dinañu gaaw a tàmbali seen joŋante bu xàttaaral bi ak ñaari ekib (Real Madrid, Barça).”
Donte daganal nañu yëf ya, teewul am na ekib yu taxaw dàq boobu Super League, ñu ci mel ni Manchester United, Séville, Valence, Atletico Madrid, Bayern, Dortmund.
GREENWOOD A NGI ÑËWAAT BU BAAX
Gannaaw ndogal li daloon ci kawam ba taxoon yoon tegoon ko loxo laata ñu di ko bàyyi setal ko ci lépp, Manchester United miy këlëbam daf ko bañoon a jëlaat daldi koy abal Getafe (Liga). Fim ne nag, moo ngi wane boppam bu baax ca ekib ba di dellusi bu baax ci nees ko xamee woon. Amagum na fa 3i bii ak ñeenti paas.
BUNDERSLIGA
Bayer Leverkusen mooy ekib bi njëkk a dawal ca sàmpiyonaa Almaañ ñaar-fukk ak juróomi joŋante yoy ñàkku ci benn. Loolu di gën a dëggal taxawaayu ekibi ak liggéey bu rafet ba fa Xabi Alonso di def.
Thomas Müller yokk na pasam ba atum 2025. Moom nag digganteem ak Bayern xanaa aj dàll rekk a koy tax a jeex. Nde foofu rekk la fas yéene futbal ba keroog muy bàyyi.
Victor Boniface jëlatina raaya “Rokkie” ca Bundersliga ba. Gii di juróomeelu yoon bu mu tegale di jël raaya gees jagleel ki gën a xarañ ci weer wi.