YËNGU-YËNGUY RÉEW MI : JÀNGUNE YAA NGIY TËJ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Juróom-ñeenti bakkan ci alxames ji, fukk ak ñett ci àjjuma ji, muy ñaar-fukk ak ñaari (22i) nit ñu deewagum ci yëngu-yëngu yi. Nemmeeku nañ itam ay yàqu-yàqu yu jégii dayo fépp ci réew mi, rawatina ca Jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru ba. Moo tax njiit ya tëj nañuy buntam ba jëmmi jamono. Démb ci àjjuma ji, 2 suwe 2023, lañu jël boobu ndogal ginnaaw yàqu-yàqu yees fa nemmiku. Njiiti Jànguneb Gastõ Berse bu Ndar itam feelu nañ yoy Ndakaaru yi. Nde, tey ci gaawu gi lañ biral ab yégle, di xamle ne ajandi nañ njàng meek li ci aju ba jëmmi jamono.

Barki-démb, ci alxemes ji, 1 suwe 2023, lañ doon siiwal àtteb layoo bi doxoon ci diggante Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar. Ñaari ati kaso ak 20i tamndareet yi àttekat bi teg ci kow Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñoo merloo ndaw ñi ba ñu wàcc ci mbedd yi. Naka noonu ay jàmmaarloo yu mettee metti jot nañoo am ci Ndakaaru ak ci yeneen diwaan yi.

Noonoot lañ nemmikooy jàmmaarloo yu dox ci diggante ndongo yeek takk-der yi fa Jàngune Séex Anta Jóob bu Ndakaaru ak it bu Gastõ Berse, fa Ndar. Waaye de, la xew Ndakaaru dafa jéggi dayo. Ndege, xale yi dañ mujje wëlbatiku song seen ub jàngune, def fa lu bët miinul.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, dañu génne seen matlaa yi taal, yàqate lekkuwaay ya. Loolu doyul, ñu songati jànguwaayu FSJP (Faculté des Sciences Juridique et Politique) fa jàngale mbiri Yoon ak àtte, teg ci jànguwaayu CESTI (Centre d’Etudes des Sciences et Techniques de l’Information), fa ñuy tàggatee taskati xibaar yi, taal leen ba taalaaley biis : benn bu COUD (Centre des Oeuvres Universitaires de Dakar) ak benn bu CESTI. Jànguwaayu FLSH (Faculté des Lettres et Sciences Humaines) sax, bàyyiwuñ ko.

Cig pàttali, kilifa yi jëloon nañu ndogalu fomm njàngale mi ci bésub alxames ji ngir wattandiku tafaar yi mënoon a juddoo ci layoo bi. Ginnaaw loolu, Ci àjjumay démb ji lees waroon a wéyal njàngale yi. Waaye, mujjul a sotti.

Bees sukkandikoo ci yëgle bi ñu siiwal, yàqu-yàqu yi ñu fa jot a nemmiku ak fi réew mi tollu, ragal nañu tafaar ji gën a yokku. Looloo waral ba ñu faf faa jaare jël ndogalu tëjandi jàngune bi ba jëmmi jamono. Nooneet la kilifay jàngune bu Ndar bi def. Fim ne nii daal, jàng amul ci réew mi. Jamono yii sax, ndongoy jànguneb Ndakaaru ba tàmbali nañoo roñu ngir ñibbi seen kër yi ba balaa mbir yiy ëpp i loxo. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj