YOMBALUG DUNDU GI, NISËRU NGUUR GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci atum 2023 mii nu dëgmal, Nguur gi dafa fas yéene génne gafaka (budget) gu tollu ci 6. 400i miliyaar ci sunuy koppar ngir wéyal liggéeyam. Lu ni tollu nag, moo ëpp fuuf gafaka yi mu daan am ay at ci ginnaaw. Daanaka, ca atum 2012, gafaka ga mu amoon matul woon 2. 500i miliyaar. Moom Njiitu réew mi, ci gafakag atum 2023 mi, dundu gi la ci gën a def yitte. Ndax kat, 45% yi ci koppar gi moom la ko jagleel. Léegi, ndax loolu yokkuteg dund gi moo ko waral walla leneen la ?

Ginnaaw bi Njiitu réew mi Maki Sàll biralee ay yitteem ak i bëgg-bëggam Nguuram gu yees googu, keroog ci ndajem jëwriñ yi, gafaka gu tollu ci 6. 400i miliyaar la leen tegal ci taabal ji. Xamal na leen nag ni mu bëggee faj jàngoroy réew mi ndax gafaka gu ni tollu mësuñu koo am. Waaye, li ko gën a yitteel ci jamono jii, dundu gi la. Yokkuteg dundu gi ganesi woon réew mi, bi mbas mi tàmbalee ak xareb Riisi ak Ikren bi, moom la bëgg a saafara ca na mu gën a gaawe. Ba tax na, 45% yi ci gafaka gi, wàll woowu la ko jagleel. Li ci dundu gi nag, njëgu njaay yi ci la, wér-gi-yaram gi, njàng mi, dëkkuwaay bi, kaaraange gi, añs.

Moo ngi xaar nag ci jëwriñ ju mag ji ak Nguuram ay njeexital yu am-a-am solo ci wàllum dundu gu yokku gi. Nde, saabal bi ñu génnee woon ci ndaje mi, ñoo ngi ciy biral ne :

«  Njiitu réew mi xamle na ni mu bëggee réew mi amal boppam, ci dayo yi mu yore, koppar gi mën a doxal mbiri réew mi rawatina biy mën a faj jafe-jafe yi ci dundu gi. » Loolu dafay wone cër bi mu dénk fànn woowu ba mu jaral ko mu jagleel ko 2. 500i miliyaar.

Ci yéenekaay bii di Seneplus tamit, ñoo ngi xamle ne :

« Mën nanu bañ Maki Sàll, waaye mënunoo ñàkk xam ni pólitigam yépp ci ndimbal la aju woon. Liggéey yi mu def ci wér-gi-yaram gi, kuraŋ bi, ndox mi ak ñi seen loxo jotul seen ginnaaw ñépp a ko ko war a nangul. »

Waaye nag, Abdul Mbay mi njëkkoon a nekk jëwriñ ju mag ju Maki Sàll ba mu faloo ca atum 2012, bokkul ak ñoom xalaat. Moom jàpp na ne :

« Ni mu daan doxalee ca atum 2018 bala wotey 2019 yi, noonu la nekk di doxale ak xaaju gafaka 2023 gi mu bëgg a jagleel dundu gi. Am na li nu war a nànd ci loolu yépp. Yàq gi. Xaalis bi ñuy génnee ngir kàmpaañ yi teg nañ ko ba noppi. Maki Sàll dafa nekk di kàmpaañ te loolu fa muy jëmale Senegaal ndox du fa am ».

Ni mbir mii tëddee nii daal xaw naa teey xel. Ndax dundu gi njëge na lool. Te, loolu njortees na ne ci seen coobare la. Rax-ci-dolli ne Saa-Senegaal yaa ngi xaar lu baree bari ci Nguur gi. Ndax kat, saaku moom, bu deful du taxaw. Léegi nag, ndax li mu jagleel dundu gi ci pólitigam yi la bokk am déet ? Walla dafay matal li mu dige woon ak askan wi ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj