LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA ETAASINI

Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay bawoo na ci réew mi tay ci talaata ji, wutali réewum Amerig. Naataangoom bii di Donald Trump moo ko fa namm a dalal ci ndaje mu ñuy amal ëllëg 9i fan ba ginnaawaati ëllëg 11i fan ci weeru sulet, fa Washington. Ndaje moomu mooy ndaje mu njëkk mu Njiitu réewum Amerig li jagleel kembaaru Afrig. Yoon wu njëkk wii nag, juróomi njiiti réewi Afrig sowu-jant kepp (Senegaal, Gaboŋ, Gine bisaawu, Liberiyaa ak Móritani) la ci woo.

SENEGAAL 2050 : RÉEWU SIIN DUGAL NA CI LOXOOM

Démb ci altine ji, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon na dalal kërug liggéey gii di DONEWON. Muy kërug liggéey gu bawoo fa réewum Siin ngir dugal seen loxo ci naaluw Senegaal 2050. Ci njiiteefu Myoung Lee ma topp ca Njiitul kër ga, waxtaan nañook Njiitu réew mi ci lëkkatoo gi ñu namm ak li seen xel màcc, di ndefarug njureefi géej gi. Naka noonu, ñu fas yéene taxawu liggéeykati wàll wile ngir fullaal ak sopparñi ci biir réew mi njureefi géej gi.

CNRA DÀNKAAFU NA GFM

Kurél giy saytu tele yi ci biir réew mi CNRA (Conseil National de Régulation de l’Audiovisuel) wax naak waa TFM démb ci altine ji ngir dànkaafu leen. Loolu nag, moo ngi am ginnaaw kàddu yu ñàkk teggin yu ñu jibal ci jotaayu Jàkkaarloo bi fay faral di am. Naka noonu, CNRA di leeral ni njëkkoon na a wax ak ñoom ca weeru mars (26 mars) ginnaaw kàddu yu ñagas yu ab taskatu xibaar jibaloon ca jotaay ba ñu doon amal ci 21 màrs 2025. Ba tax mu leen di xamal ni lu ni mel bu amatee ay daan dinañu leen ci fekk. Te daan yooyule mën nañoo jëm ci aj jotaayu Jàkkaarloo, dem ba ci dakkal lenn walla léppi TFM.

COOWAL JÀKKAARLOO BI

Coowal jotaayu Jàkkaarloo biy faral di am fa ëttu TFM fayagul. Ginnaaw bi leen CNRA dànkaafoo, Yoon dellu na dugal ci loxoom. Tay ci talaata ji rekk, waa DSC (Division Spécial de la Cybersécurité) woolu woon nañu ci ñii di Majambal Jaañ ak Ardo Ñing. Fekk ñu amaloon ay njañse ci ni Aamadu Ba faramfàccee daan bi Yoon teg Usmaan Sonko ci mbiri Sweet Beauty. Donte ni bàyyi nañu leen ñu dellu ci seen kër, Badara Gajaga miy ndayu mbill gi dina wuyuji naka ëllëg ci àllarba ji. Ñuy xaar fu wànnent di mujje ak i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj