TUKKIB NJIITU RÉEW MI CI BËJ-GÀNNAARU RÉEW MI
Tay, ci alxames ji, la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, door ab tukki ci bëj-gànnaaru réew mi. Maanaam, fa boori Ndar. Tukki boobu nag, ñaari fan la koy def. Dafa dii lii ab tukki la...
Gaynde Senegaal yi fàdd nañ yoy Àngalteer ya. Ñetti bal la leen gari Senegaal yi ngàdd. La ca gën a neex moo di ne, seen biir dëkk lañu leen fekk, duma leen. Loolu la gone yiy way, naan : « fekksi leen dóor leen,...