Cang gi Bambaa ko moom !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Cang gi ñuy woote fa Sëriñ Tuubaa lañu koy fekk.

Mooy ki jëkk a woote ci ñu xam-xamal wolof, jaare ko digle ñeel ñiy wax lu jëm ci moom ak a bind ñu di ko defe ci wolof, niki :
▪︎ Sëriñ Mbay Jaxate,
▪︎ Sëriñ Musaa KA,
▪︎ Sëriñ Moor KAYRE,
Sëriñ Sàmba Jaara MBAY ak ñu leen moy.

Sëriñ Suhaybu moom ñëw def jeqiku gu mag gi (la grande révolution), bind ci wolof téere bii di Xuratul Hayn, di téere bu làmboo mbooleem xam-xam yi nu yitteel daanaka ci diine, ci anam gu leer te tënku.

Tuxale naa ca Sëriñ Mustafaa GËY ca Njaaréem, di woon kenn ci Sëriñ Moor Mbay SIISE, di woon jàngalekatu alxuraan bu mag, mu ne Sëriñ Mut Lamin JÓOB Dagana nee na ko, Sëriñ Tuubaa nee na ko:

“sama liggéey bii de ci wolof laa ko doon def”.

Loolu di tekki ne liggéey ba waroon ngir mu man ko caa def daa desoon, lii a taxoon kon mu sant mag ñooñee ñu liggéey ci suqali wolof, jaare ko ci taaliif ci, bind ci, liggéey ci.

Nga rax ci dolli am njàngaleem ci wolof rekk la ko daan def, jaare ko ca tombam ya, waxtaanam ya ak santaaneem ya, ba ci yenn ci téere yi ci araab niki Hikma añs ci wolof la ko wax mag ñi sotti ko ci araab ( laajal Doktoor Xaadim SILLA).

Yii liggéey yu rëy ci wolof bokk na ci li gën a xam-xamal wolof, waaye li ko janal, woomal ko. Wolof it niki làkk bokk ci li gën a yaatal yoon wi ci réew mi, tax ñu doomoo ko, def ko muy seen moomeel.

Jii jëf it teewul Sëriñ bi def wareefam ci alxuraan ak araab wiy làkkuw alxuraan ak lislaam. Taalif ci li mu ci taalif ci lees dul lim ciy téere, yu kaweg gànjar ak solo.
Kon Sëriñ bi mooy boroom cang gi (souveraineté) ci làkk, waaye ànd ak ubbiku.

Moom mii it mooy boroom cang gi ci sukkandiku ci sa bopp ci wàllug liggéey ak koom.

Lii firndewoo na ca tool yu rëy ya murit yi di sos niki Xelkoom ak yu ni deme. Ba ci Puut gii rekk, doomi Sëriñ Mustafaa Basiiroo nga fay xotti baax ci mbay mu kawe te jamonoo, waxuma la nag li Sëriñ Saaliw jot a taxawal ciy tool, ciy suufi mbay te nii la deme ci mbooleem kilifay yoon wi. Doomi Sëriñ bi nag ku ci ne yoroon nga tool yees dul misaal cig rëy. Mag ñi àndoon ak Sëriñ bi, ku ci mel ni Maam Cerno moom àdduna la daan bay, ñeneen ñi naka noonu. Lii a jur doylu gi ci sa bopp ci wàllug mbay (autosuffisance agricole).

Mécceet ni la deme. Sëriñ bi ca Njaaréem la ko jàngale woon, dellul ca Doktoor Xaadim SILLA, wax na ci lu sakkan. Kon kii kay mooy baay ci cang gii nuy woote, nees ci roy te ŋoy ci.

Ku ko màggalal, màgg rekk !!

Sëriñ Abduxaadr Kebe
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj