LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (10/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PASTEF MÀGG NA

Atum 2014 lañu sosoon làng gii ñuy dippe PASTEF. Maanaam, atum ren jii la am fukki at ak benn ba mu sosook tay. Làng googu nag, màgg na ci fànn yépp. Muy ci ay at di ci ay jëf. Nde, njiiti làng googu ñoo jiite réewum Senegaal jamono jii. Kon, ñoom fukki at lañu am ci pólitig bi daldi jël réew mi. Ginnaaw loolu, kii di njiitu làng googu, Usmaan Sonko, dafa xamle ci xëtu Facebookam ne làng gi dina séqi jéego bu bees. Ndax, taxawal nañu kurél gu am solo lool ci làng gi. Kurél googu, dippees na ci nasaraan “Conseil national”. Ca otel King Fahd Palace lañu doon amalee ndajem kaajar gi. Usmaan Sonko jël na fa kàddu gi, wax ak réew mépp : kujje gi, ñoñam yi bokkal Pastef, rawatina Njiitu réew mi, basiiru Jomaay Fay. Dees na ci ñëwaat.

XIBAAR ÑEEL YOON

Démb, ci àllarba ji, lañu woolu woon Badara Gajaga fa Cybersécurité. Li waraloon woote bi mooy kàddu yi mu yékkati woon ci seen jotaay bee weesu. Kàddu yooyu jur na coow lu bari. Moom, démb lañu ko doon déglu. Waaye, dañu koo mujjee téye. Li ñu koy toppe mooy biral ay kàddu yu woroo ak jikko yu baax yi.

Naka noonu, kii di Aamadu Ba tamit woolu woon nañu ko, déglu ko. Ginnaaw bi ñu ko dégloo ba pare, ci lañu ko bàyyee mu ñibbi. Xameesagul ndax dañu koy woowaat am déet.

Ba tay, ci wàllu Yoon, Ardo Ñing mi ñu doon wax ne dafa daw, àddu na. Indi na ay leeral ci xibaar yooyu ñu doon biral. Xamle na ci xëtu Facebookam ne xibaar yooyu ñuy wasaare wérul. Nee na dawul. Li muy def moo ko tànnal bopp te, dafa dëggu ci moom. Dootul nangu kenn di ko xoqatal ak ci anam bu mu ko mën a defe. Rax-ci-dolli, kenn mënu ko teree àddu walla ŋàññi anam bi ñu yoree réewum Senegaal.

TOFTALEG FIFA GÉNN NA

Daanaka ni mu daan deme yoon yee weesu, noonu la demewaat. Réewum Senegaal jógewul fa mu nekkoon ci toftaleg ékib yi gën a xarañ. Fii ci kembaarug Afrig, mooy ñaareelu réew mu gën a xarañ ginnaaw Marog. Waaye, ci àddina wërngal-këpp moo ngi fukk ak juróom-ñetteelu toogu bi ci toftale gi. Loolu day firndeel ne gayndey Senegaal yi ay jàmbaar dëgg lañu ci joŋante yi ñuy amal seen diggante ak yeneen réew yi.

XEW-XEW BU YÉEME FA TÀMBAAKUNDAA

Xew-xew bu tiis moo am fa Misira, nekk fa Tàmbaakundaa. Soxna su tollu ci juróom fukki at moo fa génn àddina ci anam yu doy waar. Bees sukkandikoo ci waa Senego, li ñu jàpp mooy dañ koo bóom. Te, jëkkëram lañ ci duut baaraam. Moom ma nga ca loxoy Yoon. Jiixi-jaaxa yooyee am ci moo tax waa sàppëer ak waa sàndarmëri mujjee sulli néew ba donte ne sax, fekk na mu tàmbalee soppeeku bu baax. Loolu bokk na sax ci liy jafeel xam ci yan anam la faatoo (autopsie). Mu nekk xew-xew bu tiis lool. Nde, soxna soosu bàyyi na ñetti bant.

JIIXI-JAAXA CI FAATUG MOKTAAR DEM

Talaata jii weesu la Moktaar wuyuji Boroomam. Li jur coow li kay mooy fa mu faatoo. Ndax, ca Birigàdd bu Ranch de Dolly la faatoo. Loolu la ay mbokkam nanguwul a dugal seen bopp. Nde, dañoo jàpp ne am na luy ñuul ci soow mi. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, ay mbokkam dañoo xamle ne dara jotu ko woon. Te, ñee nee ñu dafa xaru. Ndax, fekk nañ ab fulaar ci baat bi. Ba tax na, dañu koy mujjee defal “autopsie” ngir xam ci yan anam la génnee àddina. Néew bi yóbb nañu ko fa Raglu Idiriisa Puy bu Grand Yoff (CTO). Kon, fii ak lu dul yàgg dara dees na ci am lu leer.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj